Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 5

Jëf ya 5:1-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Naka noonu ku ñuy wax Anañas, te ku ñuy wax Safira di jabaram, daldi jaay aw làccu suuf.
2Mu yégook jabaram, daldi làq lenn ca njég ga, ba noppi indi la ca des, teg ko ca kanam ndaw ya.
3Ba loolu amee Piyeer ne ko: «Anañas, lu waral Seytaane di fees sab xol, ba ngay wor Noo gu Sell gi, di làq lenn ci njégu tool bi?
4Ba mu jaragul, du yaa doon boroom? Gannaaw ba mu jaree it, xanaa du njég gaa ngi sa loxo ba tey? Ana noo mana xajale mii mébét ci sa xol? Du nit nga wor de, waaye Yàlla nga wor.»
5Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, daldi daanu, dee. Tiitaange lu réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.
6Ba loolu amee xale yu góor ya dikk, sàng ko, yóbbu suuli.
7Ñu teg ca lu wara tollook ñetti waxtu, jabaram duggsi, te yégul la xew.
8Piyeer ne ko: «Wax ma, nàngam ngeen jaaye tool bee?» Mu ne ko: «Waaw, nàngam la.»
9Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Ana lu ngeen di mànkoo, di nattu Noowug Boroom bi? Déglul, tànk yi suuli woon sa jëkkër a ngoogu ci bunt bi di la yóbbusi yaw it.»
10Ca saa sa ndaw sa daanu cay tànkam, dee. Xale yu góor yi duggsi, fekk ko mu dee; ñu yóbbu ko, suul ko ca wetu jëkkëram.
11Ba loolu amee tiitaange ju réy a jàpp mbooloom gëmkat ñépp, ak ña ko dégg ñépp.
12Ci kaw loolu ay firnde ak kéemaan yu bare di sottee ci loxol ndaw yi, ci biir askan wi. Gëmkat ñi nag di bokk daje ñoom ñépp fa ñuy wax Mbaarum Suleymaan, ca biir kër Yàlla ga,
13waaye kenn ca ña ca des ñemewula jaxasoo ak ñoom. Teewul askan wa nawloo leen lool.
14Gëmkati Sang bi nag di gëna bare, ñuy wàllisi, ba doon mbooloo mu mag, góor ak jigéen.
15Nit ñi dem bay génne jarag ji ci mbedd yi, teg leen ci ay laltu aki basaŋ, ngir bu fa Piyeer jaaree, lu bon bon takkndeeram mana dal ñenn ci ñoom.
16Ci biir loolu nit ñu bare bàbbeekoo ca dëkk ya séq Yerusalem, indi ay jarag ak ñu rab yu bon sonal; ñoom ñépp daldi wér.
17Ba mu ko defee xolu kañaan dugg sarxalkat bu mag ba, ak mboolem ña ko dar, te di waa ngérum Sadusen ña.
18Ñu teg ndaw ya loxo, tëj leen ca kaso ba.
19Ca guddi ga nag malaakam Boroom bi ubbi bunti kaso ba, génne leen, ne leen:
20«Demleen taxaw ca digg kër Yàlla ga, ngeen xamal askan wi mboolem lu jëm ci dund gii.»
21Gannaaw ba ñu déggee loolu, ba bët set, ñu dugg ca kër Yàlla ga, di waare. Ci biir loolu sarxalkat bu mag ba ak ña ko dar, dikk, woolu kurélu àttekat ya, mboolem kurélu njiiti bànni Israyil; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
22Dag ya nag dikk, fekkuñu leen ca kaso ba, ñu dellu yégleji ko,
23ne: «Danoo fekk kaso ba tëje ràpp, wattukat ya taxaw ca bunt ya. Nu tijji, fekkunu kenn ca biir!»
24Jawriñu kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya dégg loolu, daldi jaaxle lool ci ndaw yi, di xalaat nu mbir miy mujje.
25Mu am ku dikk, ne leen: «Ña ngeen tëjoon kaso déy a nga noonu ca kër Yàlla ga, di waare.»
26Ci kaw loolu jawriñu kër Yàlla ga ak dag ya jëli ndaw ya ndànk, bañ leena jaay doole, ngir ragal nit ñi sànni leen ay doj.
27Ñu indi leen, taxawal leen ca kanam kurélu àttekat ya, sarxalkat bu mag ba laaj leen,
28ne: «Xanaa aayewunu leen woon ne buleen waareeti mukk ci woowu tur? Yeena ngi nii ubale Yerusalem ak seen waare, ngeen nar nu cee gàdduloo bakkanu nit kii!»
29Piyeer ak ndaw ya ca des nag ne leen: «Yàlla lees wara déggal, waaye du nit.
30Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.
31Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.
32Nun noo seede loolu, nook Noo gu Sell, gi Yàlla jagleel ñi ko déggal.»

Read Jëf ya 5Jëf ya 5
Compare Jëf ya 5:1-32Jëf ya 5:1-32