Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 4

JËF YA 4:12-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu wara mucce.»
13Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne masuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne daa nañu ànd ak Yeesu.
14Te bi ñu gisee nit, ka ñu fajoon, taxaw ak ñoom, manuñu caa teg dara.
15Noonu ñu santaane, ñu génne leen, ñu daldi gise ci seen biir,
16ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te manunu koo weddi.
17Waaye ngir mbir mi baña law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu baña waxati ak kenn ci tur woowu.»
18Noonu ñu woo leen, ñu tere leen bu wóor, ñu waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu.
19Waaye Piyeer ak Yowaana ne leen: «Bu fekkee ne déggal leen te bàyyi Yàlla mooy li jub ci kanam Yàlla, seetleen.
20Waaye nun manunoo baña wax li nu gis te dégg ko.»
21Noonu kilifa yi tëkkuwaat leen, yiwi leen, ñu dem. Ndaxte amuñu benn bunt ci ñoom ngir mbugal leen, fekk ñépp di màggal Yàlla ci li xewoon.
22Ndaxte nit, ka ñu fajoon ci kéemaan googu, weesoon na ñeent fukki at.
23Bi ñu leen yiwee nag, ñu dem ci seeni bokk, nettali leen li sarxalkat yu mag ya ak njiit ya waxoon lépp.
24Bi ko bokk ya déggee nag, ñu mànkoo, diis seen kàddu Yàlla ne: «Boroom bi, yaa sàkk asamaan, suuf, géej ak lépp li nekk ci seen biir.
25Yaa wax, jaar ci sunu maam Daawuda sa jaam, mi doon gémmiñu Xel mu Sell mi, ne: “Lu tax xeeti àddina di bax? Lu tax ñuy fexe lu manula am?
26Buuri àddina dañoo booloo, te kilifa yi dajaloo, di bañ Boroom bi ak Almaseem.”
27Ndaxte ci dëgg ci dëkk bii, Erodd ak Poñsë Pilaat ànd ak xeeti àddina ak bànni Israyil, likkoo nañu, ngir daaneel sa Ndaw lu sell li nga fal, di Yeesu,
28te def lépp, li sa kàttan ak sa ndigal tëraloon.
29Léegi nag Boroom bi, seetal seeni tëkku te may nu, nun say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit.
30Tàllalal sa loxo, ci wéral ak ci wone ay kéemaan ak ay firnde, jaarale ko ci turu Yeesu, sa Ndaw lu sell li.»
31Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yëngatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër.
32Noonu mbooloom ñu gëm ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp.
33Te ndaw yi di seedeel ndekkitel Yeesu Boroom bi ak kàttan gu réy. Te yiw wu yaatu ëmb leen, ñoom ñépp.
34Kenn ci ñoom ñàkkul dara, ndaxte képp ku nekk boroom suuf mbaa am ay kër, jaay na ko, indi njég li,

Read JËF YA 4JËF YA 4
Compare JËF YA 4:12-34JËF YA 4:12-34