Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 4

JËF YA 4:1-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Bi ñuy wax ak mbooloo ma, sarxalkat ya ak kilifag ñiy wottu kër Yàlla ga ak Sadusen ya daanu ci seen kaw.
2Ñu mer lool ci li ñuy waar nit ñi, di yégle ndekkitel ñi dee, sukkandikoo ko ci ndekkitel Yeesu.
3Noonu ñu jàpp leen, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndaxte mu nga doon tàmbalee guddi.
4Waaye ñu bare ca ña dégg wax ja gëm nañu, te limu góor ñi gëm yokku na, ba mat juróomi junni.
5Ca ëllëg sa nag kilifay Yawut yi ak njiit yi ak xutbakat yi dajaloo ci Yerusalem.
6Ràññee nañu ci: Anas, miy sarxalkat bu mag bi, Kayif, Yowaana, Alegsàndar ak bokki sarxalkat bu mag bi.
7Ñu dëj Piyeer ak Yowaana ca digg ba, laaj leen ne: «Lii ngeen def, ci gan kàttan, mbaa ci turu kan, ngeen ko defe?»
8Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: «Yéen kilifay xeet wi ak njiit yi,
9bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu wér, moo tax ngeen dëj nu ci pénc mi tey,
10nangeen xam lii, yéen ñépp ak bànni Israyil gépp: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Yàlla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii jële ag wér, ba taxaw ci seen kanam.
11Yeesu moomu mooy: “Doj wi ngeen xeeboon, yéen tabaxkat yi, te moo doon doju koñ.”
12Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu wara mucce.»
13Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne masuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne daa nañu ànd ak Yeesu.
14Te bi ñu gisee nit, ka ñu fajoon, taxaw ak ñoom, manuñu caa teg dara.
15Noonu ñu santaane, ñu génne leen, ñu daldi gise ci seen biir,
16ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te manunu koo weddi.
17Waaye ngir mbir mi baña law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu baña waxati ak kenn ci tur woowu.»

Read JËF YA 4JËF YA 4
Compare JËF YA 4:1-17JËF YA 4:1-17