Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 3

JËF YA 3:4-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Ci kaw loolu Piyeer ak Yowaana ne ko jàkk, te Piyeer ne ko: «Xool nu.»
5Lafañ bi xool leen, yaakaar ne dina jot dara ci ñoom.
6Noonu Piyeer ne ko: «Awma xaalis, awma wurus, waaye li ma am, dinaa la ko jox: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret doxal!»
7Mu jàpp ci loxol ndijooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam ak ay kostanam dëgër.
8Mu tëb, daldi taxaw, di dox. Mu dugg ak ñoom ca kër Yàlla ga, muy dox, di tëb tey sant Yàlla.
9Noonu ñépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla.
10Te ñu xàmmi ko, ne moo daan toog, di yelwaan ca Bunt bu rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu daldi waaru lool te yéemu ci li ko dikkal.
11Naka waa ji taq ci Piyeer ak Yowaana, ñépp waaru; ñu daldi daw, fekksi leen ca bérab ba ñuy wax Werandaa bu Suleymaan.
12Bi Piyeer gisee loolu nag, mu ne mbooloo mi: «Yéen waa Israyil, lu tax ngeen waaru ci lii? Lu tax ngeen di nu xool jàkk, mel ni ci sunu kàttan, mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii?
13Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, di Yàllay sunuy maam, màggal na Ndawam Yeesu; yéena xàcceek moom, ba jébbal ko Pilaat, fekk naroon na koo bàyyi.
14Yéen xeeb ngeen Aji Sell ji te Jub, te tinul ab reykat.
15Bóom ngeen Aji Dundal ji, waaye Yàlla dekkal na ko; seede nanu ko nun ñépp.

Read JËF YA 3JËF YA 3
Compare JËF YA 3:4-15JËF YA 3:4-15