Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 2

JËF YA 2:3-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Te ay làmmiñ yu mel ni sawara feeñu leen, ñu tasaaroo ci seen biir, toŋ ca kaw kenn ku nekk.
4Noonu ñu fees ak Xel mu Sell mi ñoom ñépp, ñu daldi wax yeneen làkk, ni leen Xel mu Sell mi maye, ñu wax ko.
5Fekk booba amoon na ay Yawut yu daloon Yerusalem, doon ay nit ñu ragal Yàlla te bokk ci xeeti àddina yépp.
6Bi nit ñi déggee riir ma nag, ñépp dajaloo, daldi waaru ci li ñu leen dégg, ñuy wax ku nekk sa làkk.
7Ñu waaru te yéemu naa: «Gisleen, ñiy wax ñépp, ndax duñu waa diiwaanu Galile?
8Naka la mana ame nag, nu di leen dégg, kenn ku nekk ci nun, ñuy wax ci sa làmmiñ, wi nga nàmp?
9Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi,
10di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan ñi jóge Room,
11Yawut yi ak ñi tuub ci yoonu Yawut yi, waa Keret ak waa Arabi, nun ñépp nu ngi leen di dégg, ñuy yégle màggaayi Yàlla ci sunuy làkk!»
12Noonu ñépp waaru, ba jaaxle lool, ñuy waxante ci seen biir ne: «Lii lu muy tekki?»
13Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! Ñii dañoo màndi ak biiñ.»
14Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!
15Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.
16Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:
17“Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi, dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp; seen xeet wu góor ak wu jigéen dinañu wax ci kàddug Yàlla; waxambaane yi dinañu gis ay peeñu te màggat yi di gént ay gént.
18Waaw, ci bés yooyu dinaa tuur ci sama Xel ci sama kaw jaam yu góor ak yu jigéen, te dinañu wax ci kàddug Yàlla.
19Dinaa wone ay kéemaan ci kaw ci asamaan ak ay firnde ci suuf ci àddina, muy deret, sawara ak ay niiri saxar.

Read JËF YA 2JËF YA 2
Compare JËF YA 2:3-19JËF YA 2:3-19