Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 2

Jëf ya 2:10-37

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10ak Firisi ak Pamfili ak Misra ak wàllu Libi ga dendeek Siren, ak gan ñi jóge Room,
11ak Yawuti njuddu-ji-réew yeek tuubeen ñi, ak waa Keret ak Arabi, nun ñépp a leen dégg ci sunu làmmiñi bopp, ñuy siiwtaane jaloore yu Yàlla!»
12Ñépp waaru, ba jànnaxe, di wax ci seen biir naa: «Lii lu muy tekki nag?»
13Teewul ñenn ñay ñaawle, ne: «Ñii daal biiñ bu bees doŋŋ lañu naan ba màndi.»
14Ci kaw loolu Piyeer taxaw, mook Fukk ñaak benn, daldi àddu ca kaw, ne: «Yeen bokki Yawut yi, ak mboolem yeen ñi dëkke Yerusalem, dégluleen bu baax sama kàddu, ba xam lii lu mu doon.
15Ñii màndiwuñu, ni ngeen ko fooge, ndax yoor-yoor doŋŋ a jot.
16Lii kay mooy kàddu ga Yonent Yàlla Yowel jottli woon, ne:
17“Yàlla nee: Mujug jamono, maay tuur samag Noo ci kaw wépp suux; seeni doom, góor ak jigéen di biral waxyu, seeni xale yu góor di gis ay peeñu, màggat ñi di gént ay gént.
18Kera jant yooyu, sama jaam ñi, góor ak jigéen, maa leen di tuur samag Noo, ñuy biral waxyu.
19Te maay def ay kiraama fi asamaan aki firnde ci dun bi fi suuf; muy deret ak sawara ak niiru saxar.
20Jant beey soppliku ag lëndëm, weer wi doon deret, bésub Boroom bi doora taxawe màggaay ak daraja.
21Su boobaa, ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.”
22«Yeen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu waa Nasaret bi, Yàlla moo firndeele ag dëggoom, ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll.
23Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.
24Waaye moom la Yàlla yiwee ci mititu ndee, dekkal ko, ndax dee amul kàttanu tënk ko.
25Daawuda wax na ci mbiram ne: “Maa doon gis Boroom bi fi sama kanam saa su nekk, ndijoor la ma fare, ba duma tërëf.
26Moo tax sama xol di nux-nuxi, samaw làmmiñ di textexi, samaw suux sax nara nopplujee yaakaar.
27Doo ma wacc njaniiw moos, doo seetaan sa waa ju sell, mu yàqu.
28Yaa ma xamal yoonu dund, yaa may wéttali ba matal sama mbégte.”
29«Bokk yi nag, Maam Daawuda, manees na leena wax ci lu wér ne nelaw na, ba ñu denc ko, te bàmmeelam a ngi fi, nuy gis ba tey jii.
30Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàllaa ko giñaloon ne ku bokk ci geñoom lay teg cib jalam.
31Kon li mu gis te dikkagul mooy ndekkitel Almasi, te ci mbiram la wax ne bàyyeesu ko biir njaniiw, te yaramam du yàqu.
32Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp.
33Yàllaa ko yéege fa ndijooram, te jot na ci Baay bi Noo gu Sell ga mu dige woon. Moom la tuur nii tey, ngeen gis ko, dégg ko.
34Ndax kat du Daawudaa yéeg asamaan, waaye moom ci boppam moo ne: “Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko: ‘Toogeel sama ndijoor,
35ba ma def say noon, sa ndëggastalu tànk.’ ”
36«Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»
37Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?»

Read Jëf ya 2Jëf ya 2
Compare Jëf ya 2:10-37Jëf ya 2:10-37