Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 28

JËF YA 28:9-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Ci kaw loolu jarag ya ca des ca dun ba daldi dikk, amaat wér-gi-yaram.
10Ñu teral nu ci fànn yu bare, te bi nuy dem, ñu jox nu li nuy soxla lépp.
11Bi nu fa amee ñetti weer, nu dugg ca gaal gu lollikoo ca dun ba, daldi tàbbi ca géej ga. Gaalu dëkku Alegsàndiri la woon, te yor xàmmikaay guy nataalu Kastor ak Polugsë.
12Noonu nu teer dëkku Sirakus, toog fa ñetti fan.
13Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawu sudd daldi jóg, te ca ñaareelu fan ba nu teer Pusol.
14Gis nanu fa ay bokk, ñu ñaan nu, nu toog fa ayu-bés. Noonu nu dem Room.
15Sunuy xibaar law na, ba egg ca bokk ya fa dëkk, noonu ñu gatandu nu ba ca péncu Apiyus ak bérab bu ñuy wax Ñetti añukaay ya. Bi leen Pool gisee, mu sant Yàlla, daldi takk fitam.
16Bi nu dikkee Room nag, ñu may Pool, mu dëkk fa ko lew, moom ak xarekat ba koy wottu.
17Bi ñetti fan wéyee, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Bi ñu dajaloo nag, mu wax leen lii: «Bokk yi, jàpp nañu ma ci Yerusalem, jébbal ma waa Room, fekk defuma dara luy suufeel sunu xeet, mbaa lu juuyoo ak sunuy aaday maam.
18Waa Room nag seet sama mbir, te bëgg maa bàyyi, ndaxte toppuñu ma dara lu jar dee.
19Waaye bi ko Yawut ya bañee, fas yéene naa dénk sama mbir Sesaar, fekk ba tey awma dara lu may taqal sama xeet.
20Moo tax ma ñaana gise ak yéen, nu diisoo, ndaxte yaakaaru bànni Israyil moo tax ñu jéng ma.»
21Bi ñu ko déggee, ñu ne ko: «Jotunu benn bataaxal bu jóge Yude ci sa mbir, te kenn ci bokk, yi fi dikk, jottaliwul mbaa mu seede ci yaw lu bon.
22Waaye bëgg nanoo dégg li nga gëm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.»
23Noonu ñu jox ko bés, te ñu bare ñëw, fekksi ko ca néegam. Mu di leen jàngal suba ba ngoon, di leen dëggal lu jëm ci nguuru Yàlla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen jéema gëmloo.
24Ñenn ñi nag gëm li mu wax, ña ca des weddi ko.

Read JËF YA 28JËF YA 28
Compare JËF YA 28:9-24JËF YA 28:9-24