Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 27

JËF YA 27:4-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Bi nu fa jógee, nu dem ci biir géej, leru dunu Sipar ci fegu ngelaw li, ndaxte ngelaw li da noo soflu.
5Nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, teersi Mira ca wàlli Lisi.
6Foofa nag njiit la gis gaal gu jóge Alegsàndiri, jëm Itali, mu dugal nu ca.
7Noonu nuy dem ndànk diirub fan yu bare, ba janook Kanidd ci kaw coono bu réy; te ndegam ngelaw li mayu nu, nu jëm kanam, nu leru dunu Keret ci fegu ngelaw li, janook Salmon.
8Nu romb fa ak coono yu bare, agsi ca bérab bu ñuy wax Teeru yu neex, te dend ak dëkku Lase.
9Fekk booba yàggoon nañu ca yoon wa, te dem ci géej daldi aaytal, ndaxte jamonoy Kooru Yawut ya wees na. Moo tax Pool digal leen ne:
10«Gaa ñi, gis naa ne tukki bi ëmb na musiba ak kasara ju bare, waxuma gaal gi ak li mu yeb waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.»
11Waaye njiit la sobental waxi Pool, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
12Te gannaaw teeru ba neexula lollikoo, ña ca ëpp mànkoo ci jóge fa, dem ci biir géej, ngir wuta agsi Fenigsë, biy teerub dunu Keret te janook sowu suuf ak sowu kaw, nu lollikoo fa.
13Noonu bi ngelaw lu woyof liy jóge sudd wolee, ñu defe ne man nañoo sottal seen pexe, ñu wëgg diigal, daldi tafu ci dunu Keret.
14Waaye nees-tuut ngelaw lu wole penku, ñu di ko wax «Ërakilon», jóge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw.
15Mu ëpp doole gaal ga, daldi ko wat, ba nu bayliku, daldi yal.
16Nu daldi daw, leru dun bu tuuti bu ñuy wax Kóda ci fegu ngelaw, rawale looco ga ci kaw gaal ga ak coono bu bare.
17Bi ñu ko yéegee, ñu fab ay buum, ngir laxas ca taatu gaal ga, ngir ragala daanu ci suuf su nooy su ñuy wax Sirt; ba noppi ñu daldi sànni diigal, ngir wàññi doxub gaal ga, nuy yale noonu.
18Waaye bi nu ngelaw li sonalee bu metti, ca ëllëg sa ñu sànni la gaal ga yeboon ca géej ga.
19Te ca ñetteelu fan ba, ñu sànni ak seeni loxo jumtukaay, yi ñu yeboon ngir fàggu.
20Noonu jant bi ne meŋŋ te biddiiw ne mes ay fan yu bare, fekk ba tey ngelaw li di wol ak doole, ba sunu yaakaaru mucc gépp tas.
21Bi loolu di xew, fekk gëj nañoo lekk, Pool daldi taxaw ci seen biir ne leen: «Gaa ñi, li gënoon mooy ngeen déglu ma te baña jóge Keret, ba indil seen bopp musiba ak kasara ju réy jii.
22Léegi nag maa ngi leen di dénk, ngeen takk seen fit, ndax gaal gi rekk mooy yàqu, waaye kenn ci yéen du dee.
23Ndaxte ci guddi menn malaaka dikkal na ma, jóge ci Yàlla sama Boroom, bi may jaamu.
24Mu ne ma: “Pool bul tiit; fàww nga taxaw ci kanam Sesaar, te yaa tax Yàllay aar bakkani ñi nga àndal ñépp.”
25Moo tax, gaa ñi, takkleen seen fit, ndax wóolu naa Yàlla ne li mu ma wax dina am.
26Waaye war nanoo luf cib dun.»
27Ca fukkeelu guddi ga ak ñeent nu nga doon jayaŋ-jayaŋi ca géeju Adiratig; noonu ca xaaju guddi dawalkati gaal ga defe ne danu jegesi suuf.
28Ñu sànni nattukaay ba ci biir géej, mu jàpp ñeent fukki meetar, dem ca kanam tuuti, sànniwaat ko, jàpp fanweeri meetar.
29Ñu ragal ne dinañu fenqu ci ay xeer, kon ñu daldi sànni ñeenti diigal ci geenu gaal ga, di ñaan bët set.
30Waaye ci kaw loolu dawalkati gaal ga taafantaloo ne dañuy sànniji ay diigal ca boppu gaal ga, fekk dañuy fexee jël looco ga, ba raw.

Read JËF YA 27JËF YA 27
Compare JËF YA 27:4-30JËF YA 27:4-30