Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 27

Jëf ya 27:11-38

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Teewul njiitu takk-der ba sobental waxi Póol, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
12Te itam teeru boobu neexul woona lollikoo. Loolu waral ña ëpp ca waa gaal ga mànkoo ci jóge fa, dellu géej, te fexe nu ñu àgge Fenigsë, ngir lollikoo fa. Mooy teerub dunu Keret bi jublu sowub suuf ak sowub kaw.
13Ci kaw loolu ngelawal bëj-saalum wal ndànk, ñu njort ne man nañoo sottal seen pexe. Ñu wëgg diigal, daldi tafoo tefesu Keret.
14Teewul nes tuut ngelaw lu réy lu ñuy wax Penkub kaw, riddee ca dun ba.
15Gaal gi buubu, manatula dékku ngelaw li, ba nu mujj bayliku, daldi yal.
16Nu leru nag dun bu tuuti bu ñuy wax Koda, jaare wet gu nu fegoo ngelaw li, teg ci sonn lool doora téye loocob rawtu bu gaal gi.
17Ñu yéege looco ba, daldi jël ay buum yu ñu laxas ca yaramu gaal ga, dàbblee ko ko. Ci kaw loolu ñu ragala ngiroji ca beeñ bu ñuy wax Sirt, ba tax ñu sànni diigal, ngir yeexal gaal ga, daldi yalal.
18Ca ëllëg sa ngelaw la wéye noo pamti-pamtee, ba ñu mujj wàññi ca yebu gaal ga, sànni biir géej.
19Ca gannaaw ëllëg sa, seen loxoy bopp lañu jële yenn jumtukaayi gaal ga, sànni.
20Ay fani fan jant beek biddiiw yi ne meŋŋ, te ngelaw liy riddi rekk, ba nu noppee yaakaar ne dinanu mucc.
21Loolu nag fekk na ñu gëjoona lekk. Póol daldi taxaw ca seen biir ne: «Bokk yi, su ngeen yégoon déggal ma, baña jóge Keret, ba moyu loraange gii ak yàqule gii.
22Léegi nag dama leen di ñaax, ngir ngeen dalal seen xel, ndax kenn ci yeen du ñàkk bakkanam, gaal gi rekk ay yàqu.
23Ndax malaakam Yàlla ji ma moom, te ma di ko jaamu, moo ma dikkal biig.
24Mu ne ma: “Póol, bul tiit; fàww nga taxawi fa kanam Sesaar, te it Yàlla moo la baaxe muccug mboolem ñi nga àndal ci gaal gi.”
25Kon nag, bokk yi, dalal-leen seen xel, ndax gëm naa Yàlla, xam naa ne ni mu ko waxe, ni lay ame.
26Du ñàkk aw dun wu nu lufeji.»
27Ca fukkeelu bés baak ñeent, nu ngay yal-yalee fu ne ca géeju Adiratig; ba guddi ga xaajee mool ya njort ne nu ngay jegesi ab tefes.
28Ñu sànni nattukaay ba biir géej, gis ndox ma xóote ñaar fukki dayo, xawa yemook ñeent fukki meetar. Ñu demati tuuti, sànniwaat ko, daldi gis ndox ma xóote fanweeri meetar, xawa yemook fukki dayo ak juróom.
29Ci kaw loolu ñu ragala lufeji bérab bu ami doj, ba tax ñu sànnee ca geenu gaal ga, ñeenti diigal, tey ñaan jant fenke leen.
30Teewul mool ya ñoom di fexee raw, daldi dem ba yoori loocob rawtu ba biir géej, tey taafantoo ne ay diigal lañuy sànnee ca boppu gaal ga.
31Póol nag ne njiitu takk-der ba ak xarekat ya: «Ñii bu ñu desul ci gaal gi, yeen dungeen raw.»
32Ca la takk-der ya dog buum ya téye looco ba, bàyyi, mu wéy.
33Naka la jant di waaja fenk, Póol ñaax ñépp, ngir ñu lekk; mu ne leen: «Fukki fan ak ñeent a ngii, yeena ngi toog, lekkuleen, sexuleen dara.
34Dama leen di ñaax nag ngir ngeen lekk, ndax noonu doŋŋ ngeen mana rawe. Du genn kawar sax guy rote ci boppu kenn ci yeen.»
35Loolu la wax, daldi jël mburu, sant Yàlla ci kanam ñépp, ba noppi dagg, lekk.
36Ba loolu amee, ñépp dellu sawar, daldi lekk ñoom itam.
37Ña nekkoon ca gaal ga ñépp ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom benn (276) lañu.
38Ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma biir géej, ngir woyofal gaal ga.

Read Jëf ya 27Jëf ya 27
Compare Jëf ya 27:11-38Jëf ya 27:11-38