Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 27

Jëf ya 27:1-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba loolu wéyee ñu dogu noo dugal gaal, jëme nu réewum Itali. Ñu teg Póol ak ñeneen ñu ñu tëjoon, ci loxool njiitu takk-der bu ñuy wax Yulyus, bokk ci mbooloom xarem buur bu mag bi.
2Nu dugg gaalu dëkk ba ñuy wax Àddramit tey jaareji teeruy Asi, daldi tàbbi biir géej, Aristàrk jenn waay ju dëkke Tesalonig ca diiwaanu Maseduwan, ànd ak nun.
3Ca ëllëg sa nu teeri Sidon; Yulyus nag baaxe Póol, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu topptoo ko.
4Nu jóge fa, dellu géej, ngelaw li soflu nu, nu leru tefesu Sippar, jaare wet gu nu fegoo ngelaw li.
5Ci kaw loolu nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, daldi teeri Mira ca Lisi.
6Foofa nag njiitu takk-der ba gis gaal gu jóge Alegsàndiri, jëm Itali, mu dugal nu ca.
7Ba loolu amee nuy deme ndànk ay fani fan; sonn nanu lool doora jub Kanidd, waaye ngelaw li mayu nu nu teer. Nu leru tefesu Keret, jaare wet gu nu fegoo ngelaw li, janook Salmon.
8Sonn nanu lool bala noo romb foofu, doora agsi fa ñuy wax Neex Teeru, te dend ak dëkk ba ñuy wax Lase.
9Fekk na nag nu yàgg ca yoon wa, ba tollu ci jamono ju tukkib géej aaytal, ndax fekk na Koorug Yawut wees. Loolu tax Póol digal leen ne:
10«Bokk yi, gis naa ne yoon wii loraange ak yàqule gu réy la. Waxuma gaal gi ak li mu yeb, waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.»
11Teewul njiitu takk-der ba sobental waxi Póol, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
12Te itam teeru boobu neexul woona lollikoo. Loolu waral ña ëpp ca waa gaal ga mànkoo ci jóge fa, dellu géej, te fexe nu ñu àgge Fenigsë, ngir lollikoo fa. Mooy teerub dunu Keret bi jublu sowub suuf ak sowub kaw.
13Ci kaw loolu ngelawal bëj-saalum wal ndànk, ñu njort ne man nañoo sottal seen pexe. Ñu wëgg diigal, daldi tafoo tefesu Keret.
14Teewul nes tuut ngelaw lu réy lu ñuy wax Penkub kaw, riddee ca dun ba.

Read Jëf ya 27Jëf ya 27
Compare Jëf ya 27:1-14Jëf ya 27:1-14