Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 23

Jëf ya 23:15-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Léegi nag yeen ak kurélu àttekat yi, ñaanleen njiital gàngoor gi, mu indi Póol ba ci yeen, mu mel ni dangeena bëgga seetaat bu baax mbiram. Nun nag fagaru nanu, ngir bala moo agsi, nu rey ko.»
16Jarbaatub Póol bu góor nag yég tëru ma. Mu daldi dem ba ca tata ja, dugg, yégal ko Póol.
17Póol woo kenn ca njiiti takk-der ya, ne ko: «Yóbbul xale bu góor bii ba ci njiital gàngoor gi, ndax am na lu mu ko wara wax.»
18Njiital xare ba ànd ak xale ba, yóbbu ko ca njiital gàngoor ga, ne ko: «Póol, mi ñu tëj, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la xalelu góor bii, ndax am na lu mu lay wax.»
19Ba loolu amee njiital gàngoor gi jàpp ci loxol xalelu góor bi, wéetoo ak moom, ne ko: «Ana loo may xamal?»
20Mu ne ko: «Yawut yi ñoo mànkoo ci ñaan la, nga yóbbu Póol ëllëg ca kurélu àttekat ya, mu mel ni dañoo bëgga seetaat bu baax mbiram.
21Yaw nag bu leen ko may, ndax lu ëpp ñeent fukk ci ñoom a koy tëru, te xasoo nañu ne dootuñu lekk, dootuñu naan, ba kera ñu ko reyee. Fagaru nañu ba noppi, di xaar sa ndigal.»

Read Jëf ya 23Jëf ya 23
Compare Jëf ya 23:15-21Jëf ya 23:15-21