Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 23

JËF YA 23:1-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Noonu Pool xool jàkk géew ba ne leen: «Bokk yi, ci xel mu dal laa doxale ci kanam Yàlla ba ci bésu tey bi.»
2Ci kaw loolu sarxalkat bu mag ba, di ku ñuy wax Anañas, sant ña taxaw ca wetam, ñu fél gémmiñam.
3Pool ne ko: «Yàlla dina la dóor, yaw mi naaféq, bay samandaay miir bu joy bu ñu weexal. Yaa ngi toog di ma àtte, ci li yoon wi digle, ba noppi santaane ñu dóor ma, ci li yoon wi tere!»
4Waaye ña taxaw ca wetam ne ko: «Ndax dangay xas sarxalkat bu mag, bi Yàlla fal?»
5Pool ne leen: «Bokk yi, xawma woon ne sarxalkat bu mag bi la, ndaxte tëral nañu ci Mbind mi ne: “Bul wax lu bon sa kilifag xeet.”»
6Naka noona Pool, mi xam ne genn-wàllu kureel ga bokk nañu ci tariixab Sadusen ya, te ña ca des bokk ci tariixab Farisen ya, mu wax ci kaw ci biir géew ba ne: «Bokk yi, man Farisen laa, te Farisen moo ma jur; li tax ñu may àtte tey mooy sama yaakaar ci ne, ñi dee dinañu dekki.»
7Bi mu waxee loolu nag, werante wu metti daldi xew diggante Farisen ya ak Sadusen ya, ba mbooloo ma xàjjalikoo.
8Ndaxte Sadusen yi nanguwuñu ne ndekkite mbaa malaaka mbaa rab, dara am na ci, waaye Farisen nangu nañu yooyu yépp.
9Ci kaw loolu nag coow lu bare daldi jib. Ñenn ca xutbakat, ya bokk ca Farisen ya, ne bërét, daldi xuloo bu metti ne: «Gisunu dara lu bon ci nit kii. Su fekkeente ne rab a ko wax mbaa malaaka…?»
10Noonu xuloo ba daldi gëna tàng, ba kilifa ga ragal ne, nit ñi dinañu daggaate Pool. Kon mu sant xarekat ya, ñu wàcc, nangu Pool ci ñoom, yóbbu ko ca tata ja.
11Ca guddi ga nag Boroom bi taxaw ci wetu Pool ne ko: «Takkal sa fit; ni nga ma seedee ci Yerusalem, noonu nga may seedee ca Room.»
12Bi bët setee Yawut ya daldi lal pexe; ñu dige ci ngiñ ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñuy rey Pool.
13Ña lal pexe ma, seen lim ëpp na ñeent fukk.
14Noonu ñu dem ca sarxalkat yu mag ya ak njiit ya ne leen: «Giñ nanu ne dunu mos dara, ba kera nuy rey Pool.
15Léegi nag yéen ak kureelu àttekat ya, laajleen kilifa ga, mu indi ko ci seen kanam, mel ni dangeena bëgga seet mbiram bu gëna wóor. Bu ko defee nun dinanu fagaru, ngir rey ko, bala moo agsi.»
16Waaye jarbaatu Pool yég fiir ga, mu dem, dugg ca tata ja, yégal ko Pool.
17Bi ko Pool déggee, mu woo kenn ca njiiti xare ba ne ko: «Yóbbul waxambaane wii ca kilifa ga, ndax am na lu mu ko wara yégal.»
18Njiit la jël ko, yóbbu ko ca kilifa ga ne ko: «Pool, mi ñu jàpp, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la waxambaane wii, ndaxte am na lu mu lay wax.»
19Noonu kilifa ga jàpp ci loxob waxambaane wa, wéetoo ak moom, laaj ko: «Loo ma bëgga yégal?»
20Mu ne: «Yawut yi dañoo dige, ngir ñaan la, nga indi Pool ëllëg ca kanam kureelu àttekat ya, mel ni dañoo bëgga seet mbiram bu gëna wóor.
21Bu leen ko may, ndaxte lu ëpp ñeent fukk ci ñoom ñu ngi koy lalal fiir. Dige nañu ak ngiñ ne dootuñu lekk, dootuñu naan, li feek reyuñu ko; fi mu ne sax fagaru nañu, di xaar, nga nangu.»
22Kilifa ga nag sant waxambaane wa, mu bañ koo àgge kenn, ba noppi mu yiwi ko, mu dem.
23Bi mu ko defee mu woo ñaar ci njiiti xare ba ne leen: «Waajal-leen ñaar téeméeri xarekat ak juróom ñaar fukki gawar ak ñaar téeméeri nit ñu gànnaayoo xeej, ngeen dem Sesare ci juróom ñeenti waxtu ci guddi.
24Wutal-leen it Pool lu mu war, ngeen yóbbu ko ci jàmm ak salaam ba ca Feligsë, boroom réew mi.»

Read JËF YA 23JËF YA 23
Compare JËF YA 23:1-24JËF YA 23:1-24