Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 22

JËF YA 22:15-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Ndaxte li nga gis te dégg ko, dinga ko seede ci ñépp.
16Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set ci say bàkkaar ci tudd turu Yeesu.”
17«Bi ma délsee Yerusalem nag, di ñaan ca kër Yàlla ga, leer tàbbi ci man.
18Ma daldi gis Boroom bi, mu ne ma: “Génnal Yerusalem nu mu gëna gaawe, ndaxte duñu nangu li ngay seede ci man.”
19Ma ne ko: “Boroom bi, xam nañu ne dama daan wër jàngoo jàngu, di tëj kaso ak di dóor ay yar ñi la gëm.
20Rax-ca-dolli bi ñu tuuree deretu Ecen, mi la doon seedeel, teewe naa ko, ànd ca, bay wottu sax yérey ñi ko doon rey.”
21Waaye Boroom bi ne ma: “Demal, dinaa la yebal fu sore, nga jëm ci xeeti ñi dul Yawut.”»
22Mbooloo ma déglu ko nag ba ca wax jooju, waaye bi ñu déggee loolu, ñu daldi yuuxu naan: «Farleen ko ci àddina! Yembar mu mel ni moom yeyoowula dund!»
23Ñu daldi yuuxu ak di sànni seeni yére, tibb suuf, di callmeeru.
24Noonu kilifa ga santaane, ñu dugal Pool ca tata ja te caw ko ay yar yu metti, laaj ko ba xam lu tax ñu di ko yuuxoo nii.
25Waaye bi ñu koy joñ ak ay der, Pool ne njiitu xare ba fa taxaw: «Ndax am nga sañ-sañu dóor ay yar jaamburu Room, te fekk yoon dabu ko sax?»
26Bi ko njiit la déggee, mu fekki kilifaam, yégal ko ko; mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay def? Nit kale jaambur la ci Room.»
27Noonu kilifa ga ñëw laaj Pool: «Wax ma, ndax jaambur nga ci Room?» Mu ne ko: «Waaw, moom laa.»
28Kilifa ga ne ko: «Man fey naa xaalis bu bare, ngir nekk jaambur ci Room.» Waaye Pool ne ko: «Man de dama koo judduwaale.»
29Ñi ko bëggoona dóor ay yar nag randu ko ca saa sa. Te kilifa ga sax tiit ci xam ne Pool jaamburu Room la, te yeewlu na ko.
30Ca ëllëg sa kilifa ga bàyyi ko, ndaxte bëggoon na xam bu wóor lu ko Yawut ya jiiñ. Mu santaane ne, sarxalkat yu mag ya dajaloo, ñoom ak kureelu àttekat ya. Gannaaw loolu mu indilu Pool, dëj ko ci seen kanam.

Read JËF YA 22JËF YA 22
Compare JËF YA 22:15-30JËF YA 22:15-30