Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 22

Jëf ya 22:12-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12«Ku ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Ku am diiney yoonu Musaa te rafetub jëw ci biir mboolem Yawuti dëkk ba.
13Mu dikk taxaw fi sama wet, ne ma: “Mbokk mi Sóol, gisal na woon.” Ca saa sa, may gis na woon, di ko xool.
14Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam moo la dencal céru ràññee coobareem, ak gis Aji Jub ji, dégg ko, muy wax ak yaw.
15Ndax li nga gis, dégg ko, yaa koy seedeel nit ñépp.
16Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set, teqlikook say bàkkaar, te tudd turu Yeesu.”
17«Yàlla def, gannaaw ba ma délsee Yerusalem, ma doon ñaan ca kër Yàlla ga, daldi daanu leer.
18Ma gis Sang bi, mu ne ma: “Gaawal, daw génn Yerusalem, li nga may seedeel, duñu ko nangu.”
19Ma ne ko: “Sang bi, ñoom ci seen bopp xam nañu ne jàngu ci kaw jàngu, maa fa daan tëjlu ak a cawlu ñi la gëm.
20Te it ba ñuy tuur deretu Eccen, sa seede ba, man it maa nga fa woon, juboo caak ñoom, te ña ko rey, maa leen doon wattul seeni yére.”
21Mu ne ma: “Demal, man, fu sore laa lay yebal ca ña dul Yawut.”»
22Ba ba muy wax loolu, mbooloo maa nga koy déglu. Ba ñu déggee kàddu yooyu lañu xaacu ne: «Jëleleen ko ci kaw suuf! Ku mel ni kii yeyoowula dund!»
23Ña ngay yuuxoo, di sànni seeni yére, tibb suuf, callmeeru.
24Ci kaw loolu njiitu gàngoor ga santaane, ñu dugal Póol ca tata ja te laaje ko ay yar, ngir xam lu waral ñu di ko yuuxoo noonu.

Read Jëf ya 22Jëf ya 22
Compare Jëf ya 22:12-24Jëf ya 22:12-24