Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 21

JËF YA 21:28-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
28di xaacu ne: «Wallee, wallee, yéen bokki Israyil! Waa jaa ngi nii, moom miy waare fépp ak ci ñépp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak bérab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci kër Yàlla gi, ba indi sobe ci bérab bu sell bii.»
29Li tax ñu wax loolu, mooy gisoon nañu Torofim mu Efes, ànd ak moom ca dëkk ba, te ñu yaakaar ne Pool dugal na ko ca kër Yàlla ga.
30Noonu dëkk ba bépp màbb, mbooloo ma ne këpp, ñu jàpp Pool, génne ko ca kër Yàlla ga. Ca saa sa ñu tëj bunt ya.
31Bi ñu koy wuta rey, xibaar ba agsi ba ca kilifag mbooloom xarekat ba, naan Yerusalem gépp jaxasoo na.
32Ca saa sa mu ànd ak ay xarekat ak ay njiiti xare, ne jaas wàcc ci ñoom. Bi Yawut ya gisee kilifa ga ak xarekat ya nag, ñu daldi bàyyi dóor, ya ñu doon dóor Pool.
33Noonu kilifa ga jegesi jàpp ko, santaane ñu jéng ko ak ñaari càllala. Bi ñu ko defee mu laaj ku mu doon ak lu mu def.
34Waaye ci biir mbooloo ma, bu ñii nee lii, ña ca des ne laa. Kon nag gannaaw manu caa xam dara lu wóor ndax coow li, mu santaane, ñu yóbbu ko ci biir tata ja.
35Bi Pool eggee ca yéegukaayu tata ja, aaytalu mbooloo ma réy, ba ay xarekat fab ko.
36Ndaxte mbooloo maa nga ko topp, di xaacu ne: «Reyleen ko!»
37Bi ñu koy bëgga dugal ca tata ja, Pool ne kilifa ga: «Ndax man naa laa wax dara?» Mu ne ko: «Yaw dégg nga gereg?
38Kon nekkuloo waayi Misra, jooju jógloo woon nit ñi keroog te yóbbu woon ñeenti junniy bóomkat ca màndiŋ ma?»
39Pool ne ko: «Man Yawut laa, di jaambur ci Tars, dëkk bu am tur ci diiwaanu Silisi. Maa ngi lay ñaan, ma wax ak mbooloo mi.»

Read JËF YA 21JËF YA 21
Compare JËF YA 21:28-39JËF YA 21:28-39