Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 20

Jëf ya 20:11-33

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Mu yéegaat, dagg mburu ma, lekk. Waxaat na lu yàgg, ba njël jot, mu sooga dem.
12Xalelu góor ba moom, nit ñaa ko yóbbu, muy dund, seen xel doora dal bu baax.
13Nun nag nu jiituji, dugg gaal jëm Asos, fa nu nara yebe Póol, na mu ko mébéte woon, ndax Póol ci boppam moo xalaatoona jaare ci yoonu suuf si ba fekksi nu fa.
14Ba mu nu fekksee ca Asos, nu yeb ko, daldi dem Mitilen.
15Nu jóge fa, tëmb ba agsi ca ëllëg sa fa janook dunu Kiyos, bés ba ca topp, nu àgg Samos, bés ba ca toppaat, nu àgg Mile.
16Ndax Póol daa fasoon yéeney teggi Efes, ngir baña yàgg diiwaanu Asi; booba day gaawtu, ngir màggalu Pàntakot man koo fekk Yerusalem.
17Fa Mile la Póol yónnee ca Efes, woolu magi gëmkat ñi.
18Ba ñu dikkee, mu ne leen: «Yeen ci seen bopp xam ngeen bu baax, ca bés ba ma jëkkee teg sama tànk Asi, ba tey jii, ni ma masa doxale ak yeen,
19di jaamoo Boroom bi ag woyof gu mat sëkk, ci biiri rongooñ ak nattu yu ma pexey Yawut yi teg.
20Te amul lenn lu leen di jariñ, lu ma leen nëbb, bañ leen koo xamal; jàngal naa leen ci mbeddum buur ak ci biir kër yi.
21Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub ci Yàlla te gëm sunu Sang Yeesu.
22«Léegi maa ngii ci curgag Noo gu Sell gi, di dem Yerusalem, lu ma fay dal sax, xawma ci dara,
23lu moy li ma Noo gu Sell giy seereel ci dëkkoo dëkk, ne ma ay jéng aki coono moo may nég.
24Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.
25«Léegi nag xam naa ne mboolem yeen ñi ma duggoon ci seen biir, di yégle nguurug Yàlla, dootuleen ma gis.
26Moo ma tax di seere bésub tey, ne wàccoo naak ñépp, deesu ma topp benn bakkan.
27Ndax mboolem li Yàlla nar bañuma leen cee xamal lenn.
28Wattuleen nag seen bopp, wattu mboolem gétt, gi leen Noo gu Sell gi sàmmloo, te ngeen foral mbooloom gëmkati Yàlla, mi Yàlla jote deretu boppam.
29Man nag xam naa ne gannaaw bu ma demee, ay bukki yu ñàng dinañu tàbbi ci seen biir te duñu ñéeblu gétt gi.
30Ci seen biir sax la aw nit di jóge taxaw, di wax ndëngte, ngir xiirtal taalibe yi, ba ñu topp leen.
31Teewluleen nag te fàttliku ne diiru ñetti at, guddi ak bëccëg, masumaa noppee àrtu kenn ku nekk ci yeen, bay jooy sax.
32«Léegi nag, dénk naa leen Yàlla ak kàddug yiwam, gi leen mana dooleel, dencal leen seen muur ci biir mboolem nit ñi ñu sellal.
33Du lenn lu ma xemmem ci kenn; du xaalis, du wurus du koddaay.

Read Jëf ya 20Jëf ya 20
Compare Jëf ya 20:11-33Jëf ya 20:11-33