Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 20

JËF YA 20:1-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Bi yëngu-yëngu ba dalee, Pool woo taalibe ya fa moom, dooleel leen. Bi mu ko defee mu tàggoo ak ñoom, jóge fa, dellu diiwaanu Maseduwan.
2Noonu mu jaar ca bérab yooyu, di dooleel nit ñi ak wax yu bare; ba noppi mu dem réewu Geres,
3toog fa ñetti weer. Waaye bi mu nekkee ci kaw tànki dugg gaal jëm diiwaanu Siri, te Yawut yi lalal ko pexe, mu fas yéenee dellu, jaare Maseduwan.
4Booba nag ñii ñoo ànd ak moom: Sopater, doomu Pirus mi dëkk Bere; Aristàrk ak Segond, ñi dëkk Tesalonig; Gayus, mi dëkk Derbë, ak Timote; te it Tisig ak Torofim ñi dëkk Asi.
5Ñooñu nag jiitu, di nu nég dëkku Torowas.
6Waaye naka nun, gannaaw màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ma amul lawiir, nu dugg gaal ci Filib, def ci juróomi fan, fekksi leen Torowas, nu am fa juróom ñaari fan.
7Ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, booloo nanu ngir damm mburu ma. Te Pool, mi bëggoona dem ca ëllëg sa, di diisoo ak ñoom te waxtaanam law ba ci xaaju guddi.
8Ca néeg bu kawe, ba nu booloo nag, amoon na fa làmp yu bare.
9Noonu waxambaane wu tudd Ëtikus te toog ca palanteer ba, gëmméentu bay jeyaxu. Bi Pool di gëna yaatal waxtaanam nag, nelaw daldi ko jàpp, mu xàwwikoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee.
10Waaye Pool wàcc, daldi sëgg ci kawam, roof ko loxoom ne leen: «Bàyyileen jooy yi, mu ngi dund.»
11Noonu mu yéegaat, damm mburu ma, lekk; ba noppi delluwaat ci waxtaanam, di ko yaatal ba ca njël, doora tàggoo.
12Naka waxambaane wa, ñu indi ko muy dund, ba seen xol sedd guyy.
13Nun nag nu jiitu, dugg gaal jëm Asos, fa nu Pool santoon, nu jële ko fa; fekk moom fas na yéeney dox, ba agsi fa.

Read JËF YA 20JËF YA 20
Compare JËF YA 20:1-13JËF YA 20:1-13