Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 1

JËF YA 1:2-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2ba ci bés, ba ko Yàlla yéege ci asamaan. Lu ko jiitu joxoon na ay ndigal, jaare ci Xel mu Sell mi, jëm ci ndaw ya mu tànnoon.
3Gannaaw ay coonoom, ñëw na ci ñoom, di leen won ay firnde yu bare te wér ne mu ngi dund; mu feeñu leen diirub ñeent fukki fan, di diisoo ak ñoom ci lu jëm ci nguuru Yàlla.
4Am bés muy lekk ak ñoom, mu sant leen ne: «Buleen sore Yerusalem, waaye ngeen xaar li Baay bi dige woon te ma waxoon leen ko.
5Ndaxte Yaxya daa na sóob nit ñi ci ndox, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi fi ak ay fan yu néew.»
6Bi ñu dajaloo ak moom nag, ñu laaj ko: «Boroom bi, ndax ci jamono jii ngay yékkatiwaat nguuru Israyil?»
7Mu ne leen: «Ngeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko.
8Waaye bu Xel mu Sell mi ñëwee ci yéen, dingeen jot kàttan te nekk samay seede ci dëkku Yerusalem, ca diiwaani Yude ak Samari yépp ak ba fa àddina yem.»
9Bi mu waxee loolu, te ñu di ko xool, Yàlla yéege na ko, te aw niir jël ko, làq ko seeni bët.
10Bi muy dem nag, te ñu ne jàkk asamaan, ñaar ñu sol yu weex daldi ne seef, taxaw ci seen wet.
11Ñu ne leen: «Yéen waa Galile, lu tax ngeen taxaw, di xool ci asamaan? Yeesu male ñu jële ci seen biir, yéege ko asamaan, dina délsi ni ngeen ko gise, muy dem asamaan.»
12Bi loolu amee ñu jóge ca tund, woowu ñuy wax tundu Oliw ya, te mu dend ak Yerusalem lu tollu ak kilomet, ñu daldi dellu Yerusalem.
13Bi ñu dikkee, ñu yéeg ca néeg, ba sut ca taax ma, fa ñuy dal. Ñoo doon Piyeer ak Yowaana, Saag ak Andare, Filib ak Tomaa, Bartelemi ak Macë, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokkoon ci mbooloo mi ñuy wax Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa doomu Saag.
14Ñoom ñépp ñoo bokk menn xel, di wéy ci ñaan ci Yàlla, ànd ak jigéen ñi ak Maryaama, ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.
15Ca bés yooya nag Piyeer taxaw ca digg bokk ya, di mbooloo mu tollu ni téeméer ak ñaar fukk.
16Mu ne leen: «Bokk yi, li Xel mu Sell mi waxoon ci Mbind mi jaarale ko ci gémmiñu Daawuda, fàww mu am. Waxoon na ci mbirum Yudaa, mi wommat ñi jàpp Yeesu
17te mu bokkoon ci nun, ba am cér ci liggéey bi.»

Read JËF YA 1JËF YA 1
Compare JËF YA 1:2-17JËF YA 1:2-17