Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 19

JËF YA 19:7-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Limub nit ñooñu nekk na lu mat fukk ak ñaar.
8Noonu Pool dugg ca jàngu ba, di wax ak fit wu dëgër diirub ñetti weer, di diisoo ak ñoom ci mbirum nguurug Yàlla, di leen jéema gëmloo.
9Waaye bi xolu ñenn ci ñoom fattee, ñu gëmadi, bay suufeel yoon wi ci kanam mbooloo ma, mu jóge ci ñoom, xàjjale taalibe yi ak ñoom, di diisoo bés bu nekk ca jàngukaayu ku ñuy wax Tiranus.
10Mu wéy ci noonu diirub ñaari at, ba ñi dëkk diiwaanu Asi ñépp dégg kàddug Boroom bi, muy Yawut muy Gereg.
11Booba Yàllay def ay kéemaan yu ràññiku yuy jaar ci loxoy Pool.
12Ñu yóbbul sax ñi wopp ay kaala ak ay taraxlaay yu laaloon yaramam, ba jàngoro yi di leen bàyyi, rab yay génn ci ñoom.
13Noonu ay Yawut yuy wëndeelu, di faj ñi rab jàpp, ñu di leen jéema ñaanal ci turu Yeesu Boroom bi naan: «Ci turu Yeesu, mi Pool di yégle, génnleen.»
14Ñi doon def loolu, juróom ñaari doom lañu woon ci Sewa, mi doon sarxalkat bu mag ci Yawut yi.
15Waaye bi ñu ko defee rab wa ne leen: «Xam naa Yeesu, xam naa it kuy Pool, waaye yéenay ñan?»

Read JËF YA 19JËF YA 19
Compare JËF YA 19:7-15JËF YA 19:7-15