Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 19

JËF YA 19:5-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Bi ñu déggee loolu nag, sóob nañu leen ci ndox ci turu Yeesu Boroom bi.
6Te bi leen Pool tegee loxo, Xel mu Sell mi ñëw ci ñoom, ñuy wax yeneen làkk, di wax ci kàddug Yàlla.
7Limub nit ñooñu nekk na lu mat fukk ak ñaar.
8Noonu Pool dugg ca jàngu ba, di wax ak fit wu dëgër diirub ñetti weer, di diisoo ak ñoom ci mbirum nguurug Yàlla, di leen jéema gëmloo.
9Waaye bi xolu ñenn ci ñoom fattee, ñu gëmadi, bay suufeel yoon wi ci kanam mbooloo ma, mu jóge ci ñoom, xàjjale taalibe yi ak ñoom, di diisoo bés bu nekk ca jàngukaayu ku ñuy wax Tiranus.
10Mu wéy ci noonu diirub ñaari at, ba ñi dëkk diiwaanu Asi ñépp dégg kàddug Boroom bi, muy Yawut muy Gereg.
11Booba Yàllay def ay kéemaan yu ràññiku yuy jaar ci loxoy Pool.

Read JËF YA 19JËF YA 19
Compare JËF YA 19:5-11JËF YA 19:5-11