Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 19

Jëf ya 19:4-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Póol ne leen: «Yaxya, sóobeb tuubeel la daan sóobe ci ndox, di waxaale askan wi ne leen ñu gëm kiy topp ci moom, te mooy Yeesu.»
5Ba ñu déggee loolu lañu sóobu ci ndox ci turu Sang Yeesu.
6Ba leen Póol tegee loxoom, Noo gu Sell gi dikkal leen, ñu tàmbalee làkk yeneen làkk, boole ci di biral waxyu.
7Taalibe yooyu yépp a ngi wara tollu ci fukk ak ñaar.
8Ci kaw loolu Póol dem ca jàngu ba, diiru ñetti weer muy waaree aw fit, di waxal waa jàngu ba kàddu yu mata gëm ci mbirum nguurug Yàlla.
9Ñenn ña nag të ticc, baña gëm, di ŋàññ Yoon wi ca kanam mbooloo ma. Ba loolu amee Póol bàyyi leen, daldi berook taalibe ya, bés bu nekk muy diisoo ak ñoom ca kërug jàngukaay gu Tiranus.
10Loolu moo wéy diiru ñaari at, ba mboolem waa diiwaanu Asi dégg kàddug Sang bi, muy Yawut, di Gereg.
11Ba mu ko defee Yàlla di def ay kéemaan yu mag yu mu sottale loxoy Póol.
12Mujj na sax ñuy yóbbul jarag yi ay kaala aki taraxlaay yu laaloon yaramu Póol, ba lu leen daloon teqlikook ñoom, rab wu leen jàppoon, ba leen.
13Ci kaw loolu ay Yawut yuy wër di faj ku rab jàpp, tàmbalee roy, di tuddal ñi rab jàpp turu Sang Yeesu, naan rab yi: «Maa la dàq ci turu Yeesu, mi Póol di xamle.»
14Ña doon def jëf jooju ñooy juróom ñaari doom yu góor yu Sewa, sarxalkatub Yawut bu mag.
15Loolu lañu doon jéem bés, rab wu bon wa ne leen: «Yeesu déy, xam naa ko. Póol it xam naa ko. Waaye yeen, yeenay ñan?»
16Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, teg leen loxo ñoom ñépp, pamti-pamtee leen, gaañ leen, ba ñu dawe kër ga yaramu neen.
17Mboolem Yawut yaak Gereg ya dëkke Efes nag yég mbir moomu, tiitaange dikkal leen ñoom ñépp, daraja ju réy doxe ca ñeel turu Sang Yeesu.

Read Jëf ya 19Jëf ya 19
Compare Jëf ya 19:4-17Jëf ya 19:4-17