Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 19

JËF YA 19:25-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
25Noonu mu dajale leen ak seeni liggéeykat ne leen: «Gaa ñi, xam ngeen ne sunu njariñ mu ngi aju ci liggéey bii.
26Gis ngeen nag te dégg ne Pool male gëmloo na bay fàbbi mbooloo mu bare, waxuma ci Efes rekk, waaye ci biir Asi gépp naan: “Yàlla yu ay loxo defar duñu ay yàlla.”
27Léegi kat loraangee ngi nuy yoot, te du yem ci xañ nu sunu liggéey rekk, waaye it dina daaneel màggalukaayu Artemis sunu yàlla ju mag ji, tey neenal ndamam, moom mi Asi gépp te àddina sépp di màggal.»
28Bi ñu déggee loolu, mer mu réy tàbbi ci ñoom, ñuy yuuxu ne: «Artemis mu Efes màgg na!»
29Noonu dëkk bépp jaxasoo. Ñu bokk benn xalaat, daldi ne milib ca powukaay ba, diri Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan, ñi ànd ak Pool.
30Pool nag bëgga dugg ca mbooloo ma, waaye taalibe ya nanguwuñu ko.
31Ñenn ca jawriñi nguur gi it, ñuy ay xaritam, yónnee ci moom, di ko dénk, mu baña jaay bakkanam ci dugg ca powukaay ba.
32Noonu ndaje ma rëb, ba ñii di yuuxu lii, ñale di yuuxu laa, te ña ca gëna bare xamuñu lu waral ndaje ma.
33Ci kaw loolu Yawut ya jéñ Alegsàndar ci kanam, te mbooloo ma di ko xaacu ay ndigal, mu daldi tàllal loxoom, ngir làyyi ca mbooloo ma.
34Waaye bi ñu xamee ne Yawut la, ñépp a bokk benn baat, yuuxu diirub lu mat ñaari waxtu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»
35Gannaaw loolu boroom dëkk ba dalal mbooloo ma ne leen: «Yéen waa Efes, ana ku xamul ne dëkku Efes moo di wottukaayu màggalukaayu Artemis ak nataalam, bi wàcce asamaan?
36Gannaaw nag kenn manta weddi loolu, war ngeena dalal seen xel te baña sañaxu ci dara.
37Ndaxte nit ñii ngeen fi indi sàccuñu ca màggalukaay ya te sosaluñu sunu yàlla.
38Su fekkee ne Demetirus ak ay nawleem jànkoonte nañu ak kenn, am na ay bési layoo ak ñu yilif réew mi; nañu fa woo ku ñu amleenteel.
39Waaye su ngeen di laaj leneen, mbooloom dëgg dina ko àtte.

Read JËF YA 19JËF YA 19
Compare JËF YA 19:25-39JËF YA 19:25-39