Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 19

JËF YA 19:23-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
23Fekk booba amoon na yëngu-yëngu bu réy ci lu aju ci Yoon wi.
24Ndaxte nit ku tudd Demetirus, di tëggu xaalis buy defar nataali xaalis ngir màggal Artemis, daan na ci jariñu lu bare, moom ak ay nawleem.
25Noonu mu dajale leen ak seeni liggéeykat ne leen: «Gaa ñi, xam ngeen ne sunu njariñ mu ngi aju ci liggéey bii.
26Gis ngeen nag te dégg ne Pool male gëmloo na bay fàbbi mbooloo mu bare, waxuma ci Efes rekk, waaye ci biir Asi gépp naan: “Yàlla yu ay loxo defar duñu ay yàlla.”
27Léegi kat loraangee ngi nuy yoot, te du yem ci xañ nu sunu liggéey rekk, waaye it dina daaneel màggalukaayu Artemis sunu yàlla ju mag ji, tey neenal ndamam, moom mi Asi gépp te àddina sépp di màggal.»
28Bi ñu déggee loolu, mer mu réy tàbbi ci ñoom, ñuy yuuxu ne: «Artemis mu Efes màgg na!»
29Noonu dëkk bépp jaxasoo. Ñu bokk benn xalaat, daldi ne milib ca powukaay ba, diri Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan, ñi ànd ak Pool.
30Pool nag bëgga dugg ca mbooloo ma, waaye taalibe ya nanguwuñu ko.
31Ñenn ca jawriñi nguur gi it, ñuy ay xaritam, yónnee ci moom, di ko dénk, mu baña jaay bakkanam ci dugg ca powukaay ba.
32Noonu ndaje ma rëb, ba ñii di yuuxu lii, ñale di yuuxu laa, te ña ca gëna bare xamuñu lu waral ndaje ma.

Read JËF YA 19JËF YA 19
Compare JËF YA 19:23-32JËF YA 19:23-32