Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 18

JËF YA 18:8-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Kirispus nag, njiitu jàngu ba, gëm na Boroom bi ak waa këram gépp. Te waa Korent ñu bare dégg kàddu gi te gëm ko, ñu sóob leen ci ndox.
9Naka noona Boroom bi feeñu Pool ci guddi ne ko: «Bul tiit dara, waaye deel wax te baña noppi.
10Ndaxte maa ngi ànd ak yaw, te kenn du la jàpp, ba fitnaal la, ndaxte am naa xeet wu bare ci dëkk bii.»
11Noonu Pool des at ak genn-wàll ci seen biir, di fa jàngle kàddug Yàlla.
12Ci nguuru Galyon ci diiwaanu Akayi nag, Yawut ya likkoo, ñu dal ci kaw Pool, yóbbu ko ca àttekaay ba.
13Ñu ne: «Kii day xiir nit ñi ci màggal Yàlla ci lu juuyoo ak yoon wi.»
14Bi Pool bëggee wax nag, Galyon ne Yawut ya: «Yéen Yawut yi, bu aju woon ci jàdd yoon walla ñaawteef wu réy, kon liy yoon mooy ma déglu leen.
15Waaye bu ajoo ci ay werante ciy wax ak ay tur ak seen yoon, loolu seen wàll la; man duma ko àtte.»
16Noonu mu dàq leen ca àttekaay ba.
17Ci kaw loolu nit ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, ñu di ko dóor ca kanam àttekaay ba, waaye Galyon faalewu leen.
18Bi loolu wéyee Pool desati fa fan yu bare. Gannaaw ga mu tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Bi mu jógeegul teerub Señsere, mu watlu boppam, ndaxte am na lu mu dige woon ak Yàlla.

Read JËF YA 18JËF YA 18
Compare JËF YA 18:8-18JËF YA 18:8-18