Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 18

Jëf ya 18:6-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»
7Mu jóge foofa, dem kër jaamburub jaamukatu Yàlla bu ñuy wax Tisyus Yustus, te këram sësook jàngu ba.
8Teewul Kirispus njiitu jàngu ba moom, gëm Sang bi, mook waa këram gépp. Ñu bare ci waa Korent a gëm, gannaaw ba ñu déggee kàddu gi, ba ñu sóob leen ci ndox.
9Ba loolu amee Sang bi wax ak Póol ag guddi ci biir peeñu, ne ko: «Bul tiit dara, waaye waxal te bul noppi,
10ndax maa ànd ak yaw, kenn du la song, def la lu bon, ndax xeet wu yaa laa am ci dëkk bii.»
11At ak juróom benni weer la Póol toog ci seen biir, di jàngle kàddug Yàlla.
12Jant ya Galyon moomee diiwaanu Akayi, Yawut ya dañoo mànkoo, jógal Póol, jàpp ko, yóbbu ca àttekaay ba.

Read Jëf ya 18Jëf ya 18
Compare Jëf ya 18:6-12Jëf ya 18:6-12