Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 18

Jëf ya 18:2-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Mu daje fa ak Yawut bu ñuy wax Akilas, fekk baax diiwaanu Pont. Muy sooga jóge réewum Itali, ànd ak soxnaam Pirsil, ndax Buur bu mag ba Këlódd moo joxe woon ndigal ne na Yawut yépp génn Room.
3Póol nag miinante ak ñoom, te fekk ñu bokk benn liggéey, di defarkati xayma ni moom. Loolu tax mu far dal ak ñoom, di liggéey.
4Ci kaw loolu bésub Noflaay bu nekk Póol di waare ca jàngu ba, di yee Yawut yi ak Gereg yi.
5Ba Silas ak Timote dikkee, bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, Póol xintewootul lu moy di xamle kàddu gi, di seereel Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi.
6Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»
7Mu jóge foofa, dem kër jaamburub jaamukatu Yàlla bu ñuy wax Tisyus Yustus, te këram sësook jàngu ba.
8Teewul Kirispus njiitu jàngu ba moom, gëm Sang bi, mook waa këram gépp. Ñu bare ci waa Korent a gëm, gannaaw ba ñu déggee kàddu gi, ba ñu sóob leen ci ndox.
9Ba loolu amee Sang bi wax ak Póol ag guddi ci biir peeñu, ne ko: «Bul tiit dara, waaye waxal te bul noppi,

Read Jëf ya 18Jëf ya 18
Compare Jëf ya 18:2-9Jëf ya 18:2-9