Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 18

Jëf ya 18:15-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Waaye su dee ag dëngoo ci wàllu wax, mbaa ay turi nit, mbaa seen yoonu bopp nag, seetal-leen ko seen bopp. Àtte loolu moom, duma ko nangu.»
16Galyon daldi leen dàqe ca àttekaay ba.
17Ci kaw loolu ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, dóor ko ca àttekaay ba, te taxul Galyon yégal ko yaramam.
18Ba loolu wéyee Póol toogaat na fa fan yu bare, doora tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Fekk na mu watu nel ca teerub Señsere, firndeele ko aw xas wu mu xasoon.
19Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.
20Ñooñu ñaan ko, mu toogaat fa ab diir, mu gàntal.
21Naka la tàggtoo ak ñoom, ne leen: «Dinaa leen seetsiwaat, bu soobee Yàlla.» Ba loolu amee mu dugg gaal, bàyyikoo Efes,
22teereji Sesare. Mu dem nag Yerusalem, nuyuji mbooloom gëmkat ña, doora dem Àncos gu Siri.

Read Jëf ya 18Jëf ya 18
Compare Jëf ya 18:15-22Jëf ya 18:15-22