Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 17

JËF YA 17:18-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi ñuy wax Epikuren ak ci mbooloo mi ñuy wax Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ci ñoom ne: «Fortukatu xam-xam bii, lu mu bëgga wax?» Te ña ca des, bi ñu déggee Pool di waare xibaaru jàmm bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, ñu ne: «Dafa mel ni day waare ay yàlla yu nu xamul.»
19Kon nag ñu jël ko, yóbbu ko ca géew, ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Danoo bëggoon, nga leeral nu ci sa xam-xam bu bees, bii ngay yégle.
20Ndaxte sol nga ci sunuy nopp lu nu xamul. Danoo bëggoona xam nag léegi, loolu lu muy tekki.»
21Ndaxte waa Aten ñépp ak doxandéem ya fa dëkk, wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xënte.
22Noonu Pool taxaw ci biir mbooloom Areyopas ne leen: «Yéen waa Aten gis naa ne farlu ngeen ci diine lool.
23Ndaxte bi may doxantu di seet seeni màggalukaay, gis naa ci benn bu ñu bind lii: “Yàlla mi nu xamul.” Li ngeen di màggal nag te xamuleen ko, loolu laa leen di xamal.
24«Yàlla mi sàkk àddina ak li mu ëmb lépp, moom miy Boroom asamaan ak suuf, du dëkk ci néegi màggalukaay yu loxoy nit defar.
25Du jariñu it ci loxoy nit, mel ni dafa soxla dara, ndax moom mooy jox ñépp bakkan ak ruu ak lépp.
26Ci kenn nit la sàkke xeeti àddina yépp, ñu dëkk ci ñeenti xébla yi; fekk àppal na xeet wu nekk jamonoom, te rëdd seen diggi réew.
27Yàlla def na loolu, ngir ñu koy wut ci yaakaaru daj ko ci làmbatu, fekk sax sorewul kenn ci nun.
28“Ndaxte ci moom lanuy dunde, di ci jëf te nekk ci,” ni ko ñenn ci seeni taalifkat dëggale naan: “Nun noo di aw xeetam.”

Read JËF YA 17JËF YA 17
Compare JËF YA 17:18-28JËF YA 17:18-28