Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 16

Jëf ya 16:16-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Noo doon dem jullikaay ba, ab surga bu jigéen bu rabu gisaane jàpp, dajeek nun. Alal ju bare la ay njaatigeem daa jële ci ngisaaneem.
17Ndaw sa topp ci Póol ak nun, di xaacu, naan: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; dañu leen di yégal yoonu mucc.»
18Noonu la jàppoo ay fani fan, ba Póol mujj xajootu ko. Mu walbatiku ne rab wa: «Maa la sant ci turu Yeesu Almasi, génnal ci ndaw si.» Rab wa daldi génn ca saa sa.
19Ba loolu amee alal ja njaatigey ndaw sa yaakaaroon, réer leen, ñu jàpp Póol ak Silas, diri, yóbbu ca pénc ma, fa kanam njiit ya.
20Ñu taxawal leen fa àttekat ya, ne: «Ñii ñoo yëngal sunu dëkk bi, di ay Yawut
21yuy xamle aada yoy, nun ñiy waa Room, sañunu koo nangu, sañunu koo jëfe.»
22Ci kaw loolu mbooloo ma it dal ci seen kaw; àttekat ya futti seeni yére, daldi santaane ñu dóor leen ay yar.
23Ñu dóor leen ay yar yu bare, sànni leen ca kaso ba, boole ca jox boroom kaso ba ndigalal wattu leen bu baax.
24Ndigal loolu nag tax mu sànni leen ca néeg ba gëna ruqe ca kaso ba, jéng leen.
25Ba guddi gay xaaj, Póol ak Silas a ngay ñaan, di sàbbaal Yàlla, ñeneen ña ñu fa tëj di leen déglu.
26Ci kaw loolu suuf jekki yëngu yëngu bu mag ba kenug kaso ba di rëng-rëngi; bunt yépp jekki ubbiku, jéngi ñépp dàjjiku.
27Boroom kaso ba tiite ciy nelaw, gis bunti kaso bi ubbiku. Mu bocci saamaram, nara xaru, yaakaar ne ña ñu tëj dañoo rëcc.

Read Jëf ya 16Jëf ya 16
Compare Jëf ya 16:16-27Jëf ya 16:16-27