Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 15

Jëf ya 15:4-33

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi, ak ndawi Yeesu yi, ak mag ñi, dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.
5Ba mu ko defee ñenn ci gëmkat ñi bokk ci ngérum Farisen yi, daldi taxaw temm, ne gëmkat ñi dul Yawut, fàww ñu xarfal leen, sàmmloo leen yoonu Musaa.
6Ba loolu amee ndawi Yeesu yi ak mag ñi bokk daje, ngir seet mbir moomu.
7Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jaambur ñi dégge ci sama làmmiñ, kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat.
8Yàlla, mi xam xolu nit nag moo seereel jaambur ñi, ba mu leen mayee Noo gu Sell gi, ni mu nu ko maye nun itam.
9Yàlla amul xejj ak seen sunu digg ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol.
10Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, di teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, cay maam ba ci nun?
11Yiwu Sang bi Yeesu daal lanu gëm ne ci lanuy mucce, te ñoom itam, noonu rekk.»
12Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnaba ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan, yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jaambur ñi.
13Ba ñu noppee, Yanqóoba àddu ne: «Bokk yi, dégluleen ma.
14Simoŋ xamle na, ni Yàlla yége jaambur ñi ca njàlbéen, ba sàkke ci seen biir, xeet wu mu tudde turam.
15Te loolu dëppoo na ak kàdduy yonent yi, ndax bindees na ne:
16“Boroom bi nee: Gannaaw loolu dinaa délsi; maay yékkati kër Daawuda gi daanu, maay yékkati gent yi, joyanti ko,
17ngir ndesu nit ñi sàkku Boroom bi, te ñooñoo di jaambur ñi ñu tudde sama tur.
18Boroom bee xamle loolu bu yàgga yàgg.”
19«Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jaambur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla.
20Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu powum séy, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam.
21Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey ay nit a ngi waaree yoonu Musaa ci dëkk bu nekk, ñu di ko jàng ci jàngu yi bésub Noflaay bu nekk.»
22Ba loolu amee ndaw yi ak mag ñi mànkoo ak mbooloom gëmkat ñépp, ngir tànne ci seen biir ay nit, yebal leen Àncos, boole leen ak Póol ak Barnaba. Ñooñoo di Yuda, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, ñu diy mag ca bokk ya.
23Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne: Nun ndawi Yeesu, ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo.
24Dégg nanu ne ay nit ñu bawoo ci nun, ñoo leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seen xel, te nun joxunu leen lenn ndigal.
25Moo tax nu mànkoo ci tànn ay nit ñu nu yebal ci yeen, boole leen ak sunuy soppe Barnaba ak Póol,
26ñoom ñi jaay seen bakkan ngir sunu Sang Yeesu Almasi.
27Kon nag noo yebal Yuda ak Silas, ngir ñu àgge leen ci seen gémmiñu bopp, lii nu leen bind.
28Ndaxte Noo gu Sell gi moo mànkoo ak nun ci bañ leena teg benn coono, xanaa lii manula ñàkk:
29Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.
30Ba loolu amee ñu tàggtoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
31Ba ñu jàngee bataaxal bi, kàddu ga dëfal leen, seen xol sedd.
32Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddli seen ngëm.
33Ba loolu amee ñu toog fa ab diir, bokk yi door leena ñaanal yoonu jàmm, yiwi leen, ngir ñu dellu ca ña leen yebaloon.

Read Jëf ya 15Jëf ya 15
Compare Jëf ya 15:4-33Jëf ya 15:4-33