Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 15

JËF YA 15:3-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Kon nag mbooloo mi gunge leen, ñu jaar ci wàlli Fenisi ak Samari, di nettali ni ñi dul Yawut waññikoo ci Yàlla, ba bokk yépp am ca mbég mu réy.
4Te bi ñu agsee Yerusalem, mbooloom ñi gëm, ndaw yi ak njiit yi teeru leen, ñu nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp.
5Ci kaw loolu ñeneen, ñi gëm waaye bokk ci tariixab Farisen ya, daldi jóg ne: «Fàww ñi dul Yawut xaraf, te ñu dénk leen sàmm yoonu Musaa.»
6Noonu ndaw yi ak njiit yi dajaloo, ngir seet mbir moomu.
7Gannaaw werante wu bare Piyeer jóg ne leen: «Yéen bokk yi, xam ngeen ne ca njàlbéen ga Yàlla tànnoon na ma ci yéen, ngir ma yégal ñi dul Yawut xibaaru jàmm bi, ba ñu gëm.
8Yàlla, mi xam xol yi, seede na leen ci li mu leen may Xel mu Sell mi, ni mu nu ko maye nun itam.
9Gënalantewu nu ak ñoom, ci li mu sellal seen xol ci kaw ngëm.
10Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, ciy teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, nun mbaa sunuy maam?
11Nun daal ci yiwu Yeesu Boroom bi lanu yaakaara mucce, te ñoom itam, ci lañu wékku.»
12Bi mu ko waxee, mbooloo mépp ne xerem, di déglu Barnabas ak Pool, ñuy nettali kéemaan ak firnde yépp, yi Yàlla def jaarale ko ci ñoom ci biir ñi dul Yawut.
13Bi ñu noppee, Saag jël kàddu ga ne:
14«Bokk yi, dégluleen ma! Simoŋ nettali na, ni Yàlla seetsee bu jëkk ñi dul Yawut, ngir sàkku ci ñoom xeet wu ñu tudde turam.
15Te loolu sax dëppoo na ak li yonent yi tëral; ñu bind ne:
16“Boroom bi nee na: Gannaaw loolu dinaa délsi, te yékkati këru Daawuda, gi ne tasar, dinaa defar gent ya, ba taxawalaat ko.
17Noonu li des ci doom Aadama wut Boroom bi, maanaam xeet yi dul Yawut, ñuy tudd sama tur.
18Man dinaa def loolu, man Boroom bi ko wax, te ca njàlbéen ba tey ma di ko xamle.”
19«Kon nag lii mooy sama ndigal: bunu gétën ñi dul Yawut te waññiku ci Yàlla.
20Waaye nu bind leen, ñu moytu ñam wu araam wu ñu tuuroo xërëm, tey moytu njaaloo, ak jur gu médd, bay naan deret ja.
21Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey am na ca dëkk bu nekk ñuy waare ci yoonu Musaa; bésub noflaay bu nekk sax dañu ciy xutba ca jàngu ya.»
22Bi mu ko waxee, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom ñi gëm mépp fas yéenee tànn ci ñoom ay nit, yónni leen Ancos, ñu ànd ak Pool ak Barnabas. Noonu ñu tànn Yudd, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, di ay njiit ca bokk ya.
23Ñu jox leen bataaxal bu ne: Yéen sunu bokk yi dul Yawut te dëkk Ancos, Siri ak Silisi, nu ngi leen di nuyu, nun seeni bokk, di ndaw yi ak njiit yi.
24Dégg nanu ne am na ay nit ñu bawoo ci nun, ñu di leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seeni xol, te fekk sukkandikuwuñu ci lenn ndigal lu jóge ci nun.
25Kon nag mànkoo nanu ci tànn ay nit, yónnee leen ko, ànd ak sunuy soppe Barnabas ak Pool.
26Ñoom jaay nañu seen bakkan ngir turu Yeesu Kirist Boroom bi.
27Yónni nanu nag Yudd ak Silas, ñu di leen xamal xibaar boobu ci seen gémmiñ.
28Ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu bañ leena teg beneen yen, lu dul dénkaane yii am njariñ,
29maanaam ngeen moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm, deretu jur gu médd ak njaaloo. Bu ngeen moytoo yëf yooyu, dingeen def lu baax. Ci jàmm.

Read JËF YA 15JËF YA 15
Compare JËF YA 15:3-29JËF YA 15:3-29