Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 15

Jëf ya 15:1-4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ñenn nit ñu bàyyikoo Yude dikk Àncos, ñoo doon digal bokki taalibe yi, ne leen: «Su ngeen xaraful, ni ko aaday Musaa santaanee, dungeen mana mucc.»
2Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnaba séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnaba, ak ñenn ca gëmkati Àncos, ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu, ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.
3Ci kaw loolu mbooloom gëmkat ñi yebal leen, ñu jaare Fenisi ak Samari, daldi àgge waa foofa ni jaambur ñi dul Yawut tuube, ba bokki gëmkat ñépp bég ca lool.
4Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi, ak ndawi Yeesu yi, ak mag ñi, dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.

Read Jëf ya 15Jëf ya 15
Compare Jëf ya 15:1-4Jëf ya 15:1-4