Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 14

JËF YA 14:8-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Amoon na ca Listar nag nit ku fa toog, ku ay tànkam làggi, ndax li mu judduwaale lafañ te masula dox.
9Moom nag muy déglu Pool miy waare. Noonu Pool xool ko jàkk, gis ne am na ngëm ngir wér.
10Mu ne ko ak baat bu dëgër: «Jógal taxaw bu jub.» Noonu nit ki ne bërét, jóg, daldi dox.
11Bi mbooloo ma gisee li Pool def, ñu daldi yuuxu, ne ci làkku waa Likawni: «Yàlla yi soppiku nañu nit, wàcc ci nun.»
12Noonu ñu tudde Barnabas, Sës, te tudde Pool, Ermes, ndaxte mooy ki yor wax ji.
13Fekk ci buntu dëkk ba amoon na fa kër gu ñuy màggale Sës. Sarxalkat ba nag ànd ak mbooloo ma, daldi indi ca bunt ya ay yëkk ak ay caq, yi ñu defare tóor-tóor, ngir màggal leen ci tuur deretu mala.
14Waaye bi ko ndaw yi Barnabas ak Sóol déggee, ñu sib ko ba xotti seeni yére, ñu daldi daw, tàbbi ca mbooloo ma, di wax ci kaw ne:
15«Yéen nit ñi, lu leen xiir ci lii? Nun it ay nit lanu, ñu bokk bind ak yéen. Te nu ngi leen di xamal xibaaru jàmm ne leen, ngeen dëddu yëfi neen yii te waññiku ci Yàlla miy dund te sàkk asamaan, suuf, géej ak li ñu ëmb lépp.
16Démb mayoon na xeet yépp, ñu aw seen yoonu bopp.
17Moona noppiwula firndeel aw meloom ci def lu baax, di leen wàcceele ci asamaan taw buy indi naataange, ba ngeen lekk ba suur, te seen xol fees ak mbég.»
18Noonu ci lu jafe yey nañu mbooloo ma ak wax jooju, ba tere leen, ñu rendil leen sarax.
19Waaye bi loolu wéyee amoon na ay Yawut yu jóge Ancos ak Ikoñum, ñu fàbbi mbooloo ma, sànni Pool ay doj, ba yaakaar ne dee na, ñu diri ko ba ca gannaaw dëkk ba.
20Waaye taalibe ya ñëw wër ko, mu daldi jóg, duggaat ca dëkk ba. Ca suba sa nag, mu ànd ak Barnabas, dem Derbë.
21Bi ñu fa àggee nag, ñu xamle fa xibaaru jàmm bi, ba sàkk fa ay taalibe yu bare. Gannaaw loolu ñu délsi Listar, Ikoñum ak Ancos,
22di dooleel xeli taalibe ya, xiir leen ñu sax ci yoon wi; ñu ne leen: «Ci kaw nattu yu bare lanu wara dugge ci nguuru Yàlla.»
23Ci mbooloom ñi gëm mu nekk nag, ñu tànn ci ay njiit; ba noppi ñu ñaan Yàlla ak di woor, dénk leen Boroom bi ñu gëm.
24Gannaaw loolu ñu jaar diiwaanu Pisidi, dikk ci Pamfili.
25Ñu yégle kàddu gi ci dëkku Peers, doora dem dëkku Atali.
26Foofa nag ñu dugg gaal, jëm Ancos, fa ñu leen dénke woon ca yiwu Yàlla, ngir liggéey bi ñu àggale.

Read JËF YA 14JËF YA 14
Compare JËF YA 14:8-26JËF YA 14:8-26