Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 14

Jëf ya 14:19-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Ci kaw loolu ay Yawut yu jóge Àncos gu Pisidi ak Ikoñum, fexe ba fàbbi mbooloo ma, daldi dóor Póol ay doj, diri ko ba génne ko dëkk ba, yaakaar ne dee na.
20Naka la ko taalibe ya yéew, mu jóg, daldi dellu ca biir dëkk ba. Ca ëllëg sa, mu ànd ak Barnaba, dem Derbe.
21Gannaaw ba ñu xamlee fa Derbe xibaaru jàmm bi, ba am fa taalibe yu bare, dañoo dellu Listar ak Ikoñum ak Àncos gu Pisidi.
22Ñuy feddli pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.»
23Mbooloom gëmkat mu nekk nag, ñu tabb ci ay mag; ci biir loolu ñu ñaan, boole kook koor, daldi dénk mag ña Sang bi ñu gëm.
24Gannaaw loolu ñu jaare biir diiwaanu Pisidi, ba àgg Pamfili.
25Ñu daldi siiwtaane kàddu gi ca Perge, doora wàcci ba Atali.
26Foofa lañu dugge gaal, dellu Àncos gu Siri, ga ñu leen dénke woon Yàlla ciw yiwam, ngir liggéey ba ñu sottal, ba délsi noonu.

Read Jëf ya 14Jëf ya 14
Compare Jëf ya 14:19-26Jëf ya 14:19-26