Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 14

Jëf ya 14:14-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
14Ci kaw loolu Póol ak Barnaba yég la xew. Ñu xotti seeni yére ndax ñaawlu ko. Ñu buur nag ba ca biir mbooloo ma, daldi àddu ca kaw ne:
15«Yeen, lu leen xiir ci lii? Nun itam ay nit lanu, bokk ak yeen benn bind. Xibaaru jàmm bi lanu leen di xamal, ngir ngeen wacc yëfi neen yii te walbatiku ci Yàlla, kiy dund te sàkk asamaan ak suuf ak géej ak mboolem lu nekk ci biir.
16Moo mayoon démb xeet yépp, ñu awe seen yooni bopp.
17Moona noppiwula seereel boppam ci mbaaxam gi muy jëfe, di leen wàcceel fa asamaan, taw ak naataange, reggal leen, bégal leen ba seen xol sedd.»
18Loolu lépp ndaw ya wax nañu ko te tuuti kon ñu tëlee tere mbooloo ma ñu rendil leen sarax.
19Ci kaw loolu ay Yawut yu jóge Àncos gu Pisidi ak Ikoñum, fexe ba fàbbi mbooloo ma, daldi dóor Póol ay doj, diri ko ba génne ko dëkk ba, yaakaar ne dee na.
20Naka la ko taalibe ya yéew, mu jóg, daldi dellu ca biir dëkk ba. Ca ëllëg sa, mu ànd ak Barnaba, dem Derbe.
21Gannaaw ba ñu xamlee fa Derbe xibaaru jàmm bi, ba am fa taalibe yu bare, dañoo dellu Listar ak Ikoñum ak Àncos gu Pisidi.
22Ñuy feddli pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.»
23Mbooloom gëmkat mu nekk nag, ñu tabb ci ay mag; ci biir loolu ñu ñaan, boole kook koor, daldi dénk mag ña Sang bi ñu gëm.
24Gannaaw loolu ñu jaare biir diiwaanu Pisidi, ba àgg Pamfili.
25Ñu daldi siiwtaane kàddu gi ca Perge, doora wàcci ba Atali.
26Foofa lañu dugge gaal, dellu Àncos gu Siri, ga ñu leen dénke woon Yàlla ciw yiwam, ngir liggéey ba ñu sottal, ba délsi noonu.
27Ba ñu agsee, dañoo woo mbooloom gëmkat ña, àgge leen mboolem na Yàlla def ak ñoom, ak na mu ubbilee jaambur ñi dul Yawut buntu ngëm.
28Ñu toog nag ak taalibe ya diir bu xawa yàgg.

Read Jëf ya 14Jëf ya 14
Compare Jëf ya 14:14-28Jëf ya 14:14-28