Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 13

JËF YA 13:5-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Bi ñu teeree ca dëkku Salamin nag, ñu yégle fa kàddug Yàlla ca jàngub Yawut ya. Ku tudd Yowaana ànd ak ñoom, di leen jàpple ci liggéey bi.
6Noonu ñu jaar ci dun bépp, ba egg dëkku Pafos. Foofa ñu gis luxuskat bu tudd Bar-Yeesu, di Yawut bu mbubboo turu yonent.
7Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus, di nit ku neex xel. Moom nag mu woolu Barnabas ak Sóol, ngir bëgga dégg kàddug Yàlla.
8Waaye Elimas, boroom xam-xam bu ñuul bi —ndaxte loolu la turam di tekki— di leen dogale, ngir bañ boroom réew ma gëm.
9Ci kaw loolu Sóol, mi tudd it Pool, daldi fees ak Xel mu Sell mi; mu xool ko jàkk,
10ne ko: «Yaw mi fees ak fen ak lu bon, di doomu Ibliis, tey noonu lépp lu jub, ndax doo bàyyee dëngal yoon yu jub yu Boroom bi?
11Léegi loxob Boroom bi dina dal sa kaw, te dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.» Ca saa sa nag ay bëtam muuru, mu daldi tàbbi cig lëndëm, muy làmbatu, di wut ku ko wommat.
12Ba boroom réew ma gisee li xew nag, mu daldi gëm, di yéemu ci yoonu Boroom bi.
13Naka noona Pool ak ñi mu àndal jóge Pafos, jaar ci géej, jëm dëkku Peers ci réewu Pamfili. Yowaana nag tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem.
14Waaye ñoom ñu jóge Peers, aw ca yoon wa, ba ñëw dëkku Ancos ci diiwaanu Pisidi. Bésub noflaay ba nag ñu dugg ca jàngu ba, toog.
15Bi ñu jàngee yoonu Musaa ak yonent ya, njiiti jàngu ba yónnee ca ñoom ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee lu ngeen di dénk mbooloo mi, waxleen ko.»
16Noonu Pool jóg, tàllal loxoom ne leen: «Yéen bokki Israyil ak yéen ñi ragal Yàlla, dégluleen!
17Yàllay bànni Israyil tànn na sunuy maam, di yokk xeet wa, bi ñuy ganeyaan ci Misra; ba noppi mu génne leen fa ak kàttanu loxoom.
18Diirub ñeent fukki at mu di leen muñal ca màndiŋ ma.
19Gannaaw loolu faagal na juróom ñaari xeet ci réewu Kanaan, ba sunuy maam donn réew ma.
20Loolu lépp xew na ci diirub ñeenti téeméeri at ak juróom fukk. «Gannaaw loolu mu jox leen ay njiit, ba ci yonent Yàlla Samiyel.
21Booba ñuy ñaan buur, te Yàlla jox leen Sóol, doomu Kis ci giiru Beñamin, muy seen buur diirub ñeent fukki at. Gannaaw ga mu jële ko fa,
22dellu falal leen buur bu tudd Daawuda, mu seedee ko nii: “Gis naa Daawuda, doomu Isayi, ku ma neex ci sama xol, te dina def lépp luy sama coobare.”
23«Noonu ci askanam Yàlla indil na bànni Israyil Musalkat bi Yeesu, ci ni mu ko dige woon.
24Laata muy ñëw nag, Yaxya daan na waare, ne bànni Israyil gépp, ñu tuub seeni bàkkaar, te mu sóob leen ci ndox.
25Te ba Yaxyay jeexal sasam, mu ne: “Ku ngeen may teg? Duma Ki wara ñëw; waaye am na kuy ñëw sama gannaaw, koo xam ne kii yeyoowumaa tekki ay dàllam.”
26«Bokk yi, yéen askanu Ibraayma ak yéen ñi ragal Yàlla, kàddug mucc gi ci nun la wàcc.
27Waa Yerusalem ak seeni kilifa xàmmiwuñu woon Yeesu te xamuñu woon waxu yonent, yi ñuy jàng bésub noflaay bu nekk; teewul ñu amal waxu yonent yi, ci li ñu àtte Yeesu, ba daan ko.

Read JËF YA 13JËF YA 13
Compare JËF YA 13:5-27JËF YA 13:5-27