Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 13

JËF YA 13:35-49

Help us?
Click on verse(s) to share them!
35Moo tax mu waxaat feneen ne: “Doo bàyyi sa Waa ju sell, mu yàqu.”
36Ndaxte bi Daawuda defee coobarey Yàlla ci jamonoom, mu faatu, ñu suul ko, mu fekki ay maamam, suuf lekk ko.
37Waaye ki Yàlla dekkal, yaramam seeyul.
38«Kon nag bokk yi, nangeen xam ne ci moom Yeesu nu ngi leen di yégal mbaalug bàkkaar yi. Te fépp fu yoonu Musaa tële woona àttee nit ni ku jub,
39fa la Yeesu di àttee ni ku jub képp ku ko gëm.
40Wottuleen nag ba li yonent yi bindoon bañ leena dal, ci li ñu ne:
41“Yéen ñiy xeebaate, gisleen lii, ngeen yéemu ba far; ndaxte dinaa def ci seen jamono jëf, joo xam ne su ngeen ko déggee sax, dungeen ko gëm.”»
42Bi ñuy génn nag ca jàngu ba, Yawut ya ñaan leen, ñu baamtu wax ja ca bésub noflaay ba ca tegu.
43Te bi mbooloo ma tasee, ay Yawut yu bare ak ñi tuuboon ci yoonu Yawut te ragal Yàlla, topp ci Pool ak Barnabas. Ñuy diisoo ak ñoom, di leen xiir, ñu wàkkirlu ci yiwu Yàlla.
44Noonu bésub noflaay ba ca tegu, daanaka waa dëkk bépp daje, ngir déglu kàddug Yàlla.
45Waaye bi Yawut yi gisee mbooloo ma, ñu daldi fees ak kiñaan, di weddi li Pool di wax te di ko xas.
46Bi loolu amee Pool ak Barnabas ne leen ci lu bir: «Yéen lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla, waaye gannaaw gàntu ngeen ko, ba àtte seen bopp ne yeyoowuleen dund gu dul jeex gi, kon nu ngi waññiku ci ñi dul Yawut.
47Ndaxte moom la nu Boroom bi sant ci li mu naan: “Samp naa la, nga nekk leeru ñi dul Yawut, ngir nga yóbbu mucc gi, mu daj cati àddina.”»
48Ñi dul Yawut nag, bi ñu déggee loolu, daldi bég tey màggal kàddug Boroom bi; te ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex daldi gëm.
49Noonu kàddug Boroom bi di law ci diiwaan bépp.

Read JËF YA 13JËF YA 13
Compare JËF YA 13:35-49JËF YA 13:35-49