Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 13

Jëf ya 13:31-51

Help us?
Click on verse(s) to share them!
31te diiru fan yu bare la feeñu ña àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem, te ñooñooy ay seedeem tey ci askan wi.
32Nun nag noo leen di àgge xibaaru jàmm bii: li Yàlla digoon sunuy maam,
33nun sët yi la ko defal, ba mu yékkatee Yeesu, te noonee lañu ko binde ci ñaareelu saaru Sabóor, ne: “Yaa di sama Doom, bés niki tey maa la jur.”
34Noonu ko Yàlla dekkale ndekkite lu dee toppatul, te yaramam du yàqu mukk, noonee la ko Yàlla waxe woon, ne: “Maa lay jox barkey Daawuda yu sell yi te wóor.”
35Moo tax mu waxaat feneen ne: “Doo bàyyi sa ku Sell ki, mu yàqu.”
36Daawuda moom, gannaaw ba mu defee coobarey Yàlla ci jamonoom, nelaw na, ba ñu rob ko ca weti maamam ya, te yàqu na.
37Waaye moom mi Yàlla dekkal, yàquwul.
38«Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa,
39képp ku gëm Yeesu, ci moom lay wàccook loolu lépp, ba ag njubam mat.
40Wattuleen nag ba li ñu wax ci téerey yonent yi bañ leena dal. Ñu ne:
41“Yeen xeebaatekat yi, xool-leen, jommileen te ne mes, ndax jëf ji may def ci seen jamono, ku leen ko waxoon sax, dungeen ko gëm.”»
42Ba ñu génnee ca jàngu ba, dañu leena ñaan ñu baamtu kàddu googu bésub Noflaay ba ca topp.
43Ba mbooloo ma tasaaroo, bare na ay Yawut ak tuubeen yuy jaamu Yàlla yu topp ci Póol ak Barnaba. Ñuy wax ak nit ñi, di leen ñaax, ngir ñu sax ci doyloo yiwu Yàlla.
44Bésub Noflaay ba ca topp, daanaka waa dëkk bépp a daje, ngir déglu kàddug Boroom bi.
45Ba Yawut yi gisee mbooloo ma nag, kiñaan man leen, ñuy weddi waxi Póol, di ko saaga.
46Ba loolu amee fit la leen Póol ak Barnaba tontoo, ne leen: «Yeen Yawut yi de lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla gi, waaye gannaaw gàntal ngeen ko, ba jombale seen bopp ag texe ba fàww, nu ngii di walbatiku ci jaambur ñi.
47Ndax noonu la nu ko Boroom bi sante ba mu nee: “Maa la tabb ngay leeru jaambur ñi, ngir nga jottliji mucc gii, ba ca cati àddina.”»
48Ba jaambur ña déggee loolu, dañoo bég, di màggal kàddug Boroom bi; ci biir loolu ña dogal ba jagleel ag texe ba fàww, ñoom ñépp daldi gëm.
49Kàddug Boroom bi nag di law ca diiwaan bépp.
50Teewul Yawut ya xiirtal tuubeen yu jigéen yi gëna ràññiku, ak kàngam yu góor yi ci dëkk bi. Ñu daldi bundxatal Póol ak Barnaba, génne leen réew ma.
51Póol ak Barnaba nag fëgg seen pëndub ndëgguy tànk, seedeel leen ko seen ngàntal, doora dem dëkk ba ñuy wax Ikoñum.

Read Jëf ya 13Jëf ya 13
Compare Jëf ya 13:31-51Jëf ya 13:31-51