Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 13

JËF YA 13:16-50

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Noonu Pool jóg, tàllal loxoom ne leen: «Yéen bokki Israyil ak yéen ñi ragal Yàlla, dégluleen!
17Yàllay bànni Israyil tànn na sunuy maam, di yokk xeet wa, bi ñuy ganeyaan ci Misra; ba noppi mu génne leen fa ak kàttanu loxoom.
18Diirub ñeent fukki at mu di leen muñal ca màndiŋ ma.
19Gannaaw loolu faagal na juróom ñaari xeet ci réewu Kanaan, ba sunuy maam donn réew ma.
20Loolu lépp xew na ci diirub ñeenti téeméeri at ak juróom fukk. «Gannaaw loolu mu jox leen ay njiit, ba ci yonent Yàlla Samiyel.
21Booba ñuy ñaan buur, te Yàlla jox leen Sóol, doomu Kis ci giiru Beñamin, muy seen buur diirub ñeent fukki at. Gannaaw ga mu jële ko fa,
22dellu falal leen buur bu tudd Daawuda, mu seedee ko nii: “Gis naa Daawuda, doomu Isayi, ku ma neex ci sama xol, te dina def lépp luy sama coobare.”
23«Noonu ci askanam Yàlla indil na bànni Israyil Musalkat bi Yeesu, ci ni mu ko dige woon.
24Laata muy ñëw nag, Yaxya daan na waare, ne bànni Israyil gépp, ñu tuub seeni bàkkaar, te mu sóob leen ci ndox.
25Te ba Yaxyay jeexal sasam, mu ne: “Ku ngeen may teg? Duma Ki wara ñëw; waaye am na kuy ñëw sama gannaaw, koo xam ne kii yeyoowumaa tekki ay dàllam.”
26«Bokk yi, yéen askanu Ibraayma ak yéen ñi ragal Yàlla, kàddug mucc gi ci nun la wàcc.
27Waa Yerusalem ak seeni kilifa xàmmiwuñu woon Yeesu te xamuñu woon waxu yonent, yi ñuy jàng bésub noflaay bu nekk; teewul ñu amal waxu yonent yi, ci li ñu àtte Yeesu, ba daan ko.
28Yoon dabu ko fenn, moona ñaan nañu Pilaat, mu reylu ko.
29Noonu ñu def lépp lu yonent yi bindoon ci mbiram, ba noppi ñu wàcce ko ca bant ba, tàbbal ko ci bàmmeel.
30Waaye Yàlla dekkal na ko,
31te diirub ay fan yu bare feeñu na ñi àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem; léegi nag ñooy ay seedeem ci wetu xeet wi,
32te nu ngi leen di xamal xibaaru jàmm bi ne leen, li Yàlla digoon sunuy maam,
33def na ko ngir nun seeni sët, ci li mu dekkal Yeesu. Moom lañu bindoon ci ñaareelu saaru Sabóor ne: “Yaa di sama Doom, maa di sa Baay tey.”
34Te it li ko Yàlla dekkal, ba mu bañatee jaar ci dee, te suuf du ko lekk mukk, moom la Yàlla wax ne: “Dinaa la may barke yu sell te wóor, yi ma digoon Daawuda.”
35Moo tax mu waxaat feneen ne: “Doo bàyyi sa Waa ju sell, mu yàqu.”
36Ndaxte bi Daawuda defee coobarey Yàlla ci jamonoom, mu faatu, ñu suul ko, mu fekki ay maamam, suuf lekk ko.
37Waaye ki Yàlla dekkal, yaramam seeyul.
38«Kon nag bokk yi, nangeen xam ne ci moom Yeesu nu ngi leen di yégal mbaalug bàkkaar yi. Te fépp fu yoonu Musaa tële woona àttee nit ni ku jub,
39fa la Yeesu di àttee ni ku jub képp ku ko gëm.
40Wottuleen nag ba li yonent yi bindoon bañ leena dal, ci li ñu ne:
41“Yéen ñiy xeebaate, gisleen lii, ngeen yéemu ba far; ndaxte dinaa def ci seen jamono jëf, joo xam ne su ngeen ko déggee sax, dungeen ko gëm.”»
42Bi ñuy génn nag ca jàngu ba, Yawut ya ñaan leen, ñu baamtu wax ja ca bésub noflaay ba ca tegu.
43Te bi mbooloo ma tasee, ay Yawut yu bare ak ñi tuuboon ci yoonu Yawut te ragal Yàlla, topp ci Pool ak Barnabas. Ñuy diisoo ak ñoom, di leen xiir, ñu wàkkirlu ci yiwu Yàlla.
44Noonu bésub noflaay ba ca tegu, daanaka waa dëkk bépp daje, ngir déglu kàddug Yàlla.
45Waaye bi Yawut yi gisee mbooloo ma, ñu daldi fees ak kiñaan, di weddi li Pool di wax te di ko xas.
46Bi loolu amee Pool ak Barnabas ne leen ci lu bir: «Yéen lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla, waaye gannaaw gàntu ngeen ko, ba àtte seen bopp ne yeyoowuleen dund gu dul jeex gi, kon nu ngi waññiku ci ñi dul Yawut.
47Ndaxte moom la nu Boroom bi sant ci li mu naan: “Samp naa la, nga nekk leeru ñi dul Yawut, ngir nga yóbbu mucc gi, mu daj cati àddina.”»
48Ñi dul Yawut nag, bi ñu déggee loolu, daldi bég tey màggal kàddug Boroom bi; te ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex daldi gëm.
49Noonu kàddug Boroom bi di law ci diiwaan bépp.
50Waaye Yawut ya xiir ay jigéen, ñi woomle te farlu ci diine, ñoom ak magi dëkk ba, ñu fitnaal Pool ak Barnabas, ngir génne leen réew ma.

Read JËF YA 13JËF YA 13
Compare JËF YA 13:16-50JËF YA 13:16-50