Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 13

Jëf ya 13:1-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ca biir mbooloom gëmkat, ña woon ca dëkk ba ñuy wax Àncos, amoon na ay yonent ak ay jànglekat: ñuy Barnaba, ak Simeyon mi ñu dippee Ñuule, ak Lusiyus mi bawoo Siren, ak Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom Galile, ak Sóol.
2Ñooñoo daje woon di màggal Boroom bi, boole kook koor. Ci biir loolu Noo gu Sell gi ne: «Beral-leen ma nag Barnaba ak Sóol ngir liggéey, bi ma leen wooye.»
3Ba loolu amee ñu woor, boole kook ñaan, daldi leen teg seeni loxo, ba noppi yiwi leen.
4Ñooñu la Noo gu Sell gi yebal, ñu dem dëkk ba ñuy wax Selusi, dugge fa gaal, jëm dun ba ñuy wax Sippar.
5Ña nga teereji dëkk ba ñuy wax Salamin, daldi fay yégle kàddug Yàlla ca jànguy Yawut ya, ku ñuy wax Yowaan Màrk ànd ak ñoom, di leen jàpple.
6Ci biir loolu ñu wër dun ba bépp, ba yegg Pafos, péey ba. Ñu tase faak ab ñeengokatub Yawut buy yonent-yonentlu, ñu di ko wax Bar Yeesu.
7Ma nga bokkoon ca toppum Sergiyus Póolus boroom dëkk ba, nit ku rafet xel. Kooku namma dégg kàddug Yàlla, daldi woolu Barnaba ak Sóol.
8Elimas, mu firi Ñeengokat bi, di leen gàllankoor nag, tey jéema fàbbi boroom réew ma, ba du gëm.
9Ci kaw loolu Sóol mi ñuy wax Póol feese Noo gu Sell gi. Mu xool ñeengokat bi jàkk,
10ne ko: «Yaw nit ki fees ak gépp xeetu njublaŋ ak ndëngte, doomu Seytaane ji, noonu gépp njub, doo bàyyee lunkal yooni njub yu Boroom bi?
11Léegi nag loxol Boroom baa ngii fi sa kaw; dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.» Ca saa sa gis-gis bu naqari akug lëndëm ne milib ci kawam, muy wëndeelu, di wut ku ko wommat.
12Ba loolu amee boroom dëkk ba gis la xew, daldi gëm, di yéemu ci li mu jànge ci Sang bi.
13Póol ak ñi mu àndal nag bàyyikoo Pafos, dugg gaal, jëm Perge, ca diiwaanu Pamfili. Yowaan moom tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem.
14Ci kaw loolu, ñoom ñu jóge Perge, jàll ba Àncos ca diiwaanu Pisidi. Ñu dem jàngu ba, dugg, toog ca bésub Noflaay ba.
15Gannaaw ba tarib dog ya ca téereb yoonu Musaa, ak téereb yonent ya sottee, njiiti jàngu ba yóbbante leen kàddu, ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee kàddu gu ngeen ñaaxe mbooloo mi, waxleen.»
16Póol jóg, tàllal loxoom, nee leen: «Yeen bokki Israyil ak yeen jaamburi ragalkati Yàlla yi, dégluleen!
17Yàllay bànni Israyil jii moo tànnoon sunuy maam, moo yaatal xeet wi, ba ñuy ganeyaan ca Misra; moo leen fa génnee kàttanu loxoom.
18Lu tollook ñeent fukki at la leen muñal ca màndiŋ ma.
19Moo faagaagal juróom ñaari xeet ca réewum Kanaan, daldi muurale sunuy maam réewum Kanaaneen ña.
20Loolu lépp a ngi am ci diiru ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (450). «Gannaaw loolu moo sàkkal sunuy maam ay njiit, ba ci jamonoy Yonent Yàlla Samiyel.
21Ba loolu wéyee, ñuy sàkku buur, Yàlla jox leen doomu Kis, Sóol, mi soqikoo ci giirug Beñamin, mu falu diiru ñeent fukki at.

Read Jëf ya 13Jëf ya 13
Compare Jëf ya 13:1-21Jëf ya 13:1-21