Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 12

Jëf ya 12:2-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Noonu la bóome ab saamar Yanqóoba, doomu ndeyu Yowaan.
3Mu gis nag na mbir ma neexe Yawut ya, ba tax mu teg loxo Piyeer, moom itam; loola yemook bési màggalu Mburu mu amul lawiir.
4Naka la ko jàpplu, daldi koy tëj kaso, teg ko ci loxoy ñeenti kurél yu ñeenti takk-der, ngir ñu wattu ko; booba ma ngay xaar ba bésub Mucc bi wees, mu door koo yóbbu ca kanam askan wa.
5Naka lañu tëj Piyeer ca kaso ba, mbooloom gëmkat ñi saxoo koo ñaanal Yàlla.
6Ba ñu demee ba ca guddi, ga jiitu bés ba ko Erodd wara yóbbu, Piyeer a ngay nelaw ci diggante ñaari takk-der, ñu yeewe ko ñaari càllala, ay dag di wattu buntu kaso ba.
7Ci kaw loolu am malaakam Boroom bi ne jaas, taxaw, ag leer ne ràyy ca biir kaso ba. Malaaka ma laal Piyeer ci wetam, yee ko, ne ko: «Jógal gaaw!», càllala yi daldi rote ciy loxoom.
8Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def noonu. Mu ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»
9Piyeer génn, topp ci moom, te xamul sax ndax li ko dikkal noonu te sababoo ci malaaka mi, dëgg la. Yaakaaroon na ne am peeñu la.
10Ñu jàll dalu wattukat bu jëkk bi, teg ci ñaareel bi, ba agsi ci buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, bunt ba daldi tijjikul boppam. Ñu génn, topp menn mbedd, malaaka ma jekki teqlikook Piyeer.
11Naka la xelum Piyeer délsi, mu daldi ne: «Léegi nag xam naa xéll ne, Boroom bee yebal malaakaam, te moo ma musal ci loxol Erodd, ak mboolem li Yawut yi séentu woon.»
12Gannaaw ba Piyeer ràññee loolu, daa dem kër Maryaama, ndeyu Yowaan Màrk, fekk ñu bare daje foofa, di ñaan.
13Piyeer fëgg buntu kër ga, mbindaan mu ñuy wax Rodd dikk.
14Ba Piyeer waxee, mbindaan ma xàmmi baatam, daldi bég ba talu koo ubbil, xanaa daw dellu ca biir, ne Piyeer a nga foofa ca buntu kër ga.
15Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof?» Teewul mbindaan mi ne moom la. Ñu daldi ne: «Kon malaakaam la.»
16Ci biir loolu Piyeer a ngay fëgg ba tey. Ñu tijji, muy moom, ñu waaru.
17Piyeer liyaar leen, ngir ñu noppi, daldi leen nettali, ni ko Boroom bi génnee kaso ba. Mu ne leen: «Yégal-leen ko Yanqóoba ak yeneen bokki taalibe yi.» Ba loolu amee mu génn, dem feneen.
18Ba bët setee takk-der ya ne kër-kër, ne këpp, ne: «Ana fu Piyeer jaar?»
19Erodd nag santaane ñu wër Piyeer, te taxul mu gis ko. Mu daldi àtte wattukat yi, ba noppi joxe ndigal ngir ñu rey leen. Ba mu ko defee Erodd jóge diiwaanu Yude, dem Sesare, toog fa.
20Fekk na Erodd dëngoo lool ak waa dëkk yi ñuy wax Tir ak Sidon. Ci kaw loolu waa Tir ak Sidon mànkoo, dikk ba ci Erodd. Ñu daldi fexe ba jubook Balastus, bëkk-néegu Buur, ba noppi di sàkku jàmm, ndax seen dundub réew, ca dundu Buur Erodd la daan jóge.
21Ba bés ba ñu jàpp agsee, Erodd sol colu buuram, toog ca jal ba, di leen àgge kàddug kilifteefam.
22Mbooloo maa ngay àddu ca kaw, naan: «Lii kay baatu Yàlla la, du baatu nit!»

Read Jëf ya 12Jëf ya 12
Compare Jëf ya 12:2-22Jëf ya 12:2-22