Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 11

Jëf ya 11:2-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Ba Piyeer delloo Yerusalem nag, gëmkat ñi bokk ci askanu Yawut di ko sikk,
3naan: «Yaa dem ca ña xaraful, di bokk ak ñoom lekk!»
4Piyeer daldi leen benn-bennalal mbir mi.
5Mu ne: «Man de damaa nekkoon ca Yope, di fa ñaan. Ci biir loolu ma daanu ag leer, daldi gis ci peeñu lu mel ni sér bu mag bu ñu téyee ñeenti lafam, mu wàcce asamaan, ba agsi ci man.
6Ma xool ko jàkk, niir ko, daldi cay gis boroom ñeenti tànk yi, ak rabi àll yi, ak dundoot yiy raam ak njanaaw yi.
7Maa dégg itam baat bu ma ne: “Piyeer, jógal, rey te lekk.”
8Ma ne: “Mukk, Sang bi, ndax lenn lu daganul mbaa lu setul masula dugg sama gémmiñ.”
9Baat ba nag àddoo asamaan ñaareel bi yoon, ne ma: “Lu Yàlla setal, bu ko daganadil.”
10Menn peeñu moomu dikk na ba muy ñetti yoon, ñu doora yéege lépp asamaan.
11«Saa soosa tembe, ca la ñetti nit ña ñu yebale Sesare ba ca man, agsi ca kër ga nu dal.
12Noo gi nag ne ma: “Àndal ak ñoom, te bul nàttable.” Juróom benni bokk yii ngeen di gis ñoo ma gunge, nu dem ba dugg ca kër Korney.
13Mu xamal nu ne malaakaa ko feeñu ci néegam, ne ko: “Yebleel ca Yope, nga woolu Simoŋ, ma ñu dàkkentale Piyeer.
14Dina la àgge kàddu yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”
15«Naka laa tàmbalee wax ak ñoom Korney, Noo gu Sell gi daanu ci seen kaw, na mu jëkkoona daanoo ca sunu kaw.
16Ma daldi fàttliku kàddug Sang, ba mu noon: “Yaxya, cim ndox la daan sóobe, waaye yeen, ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob.”
17Gannaaw nag Yàllaa leen jagleel genn may, ga mu nu jagleeloon, ba nu gëmee Sang Yeesu Almasi, ana ku ma doon, man, bay gàllankoor Yàlla?»
18Ba ñu déggee loolu lañu dal, daldi màggal Yàlla. Ñu ne: «Kon xeeti jaambur yi, ndeke ñoom it Yàlla may na leen ñu tuub, ba dund!»
19Gëmkat ña tasaaroo woon nag ndax fitna ja woon, ca mbirum Eccen, mujj nañu jàll ba diiwaanu Fenisi, ca dunu Sippar ak ca Àncos, waaye àggewuñu kàddu gi ñeneen ñu moy Yawut yi.
20Terewul ay gëmkat ñu dëkke Sippar ak Siren, bàyyikoo ca, dikk Àncos, wax ak làkk-kati Gereg yi, ñoom itam, ba àgge leen xibaaru jàmm bu Sang Yeesu.
21Boroom bi nag gungee leen loxoom, ba ñu bare gëm, waññiku ci Sang bi.

Read Jëf ya 11Jëf ya 11
Compare Jëf ya 11:2-21Jëf ya 11:2-21