Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 11

JËF YA 11:2-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Bi Piyeer demee Yerusalem nag, kureelu Yawut gi farataal xaraf, di werante ak moom ne ko:
3«Lu tax nga dem ca këru ñu xaraful, bay lekk sax ak ñoom?»
4Noonu Piyeer daldi leen benn-bennal mbir mi, nettali leen ko
5ne: «Nekkoon naa ca dëkku Yope, di fa ñaan ci Yàlla, ba far sama xol seey ci moom; noonu ma am peeñu: lu mel ni sér bu mag wàcc, jóge ci asamaan, ñu yoor ko ca ñeenti laf ya, mu ñëw ba ci man.
6Ma xool ko jàkk, seetlu ko bu baax, ma gis ca boroom ñeenti tànk yu nekk ci kaw suuf, di rabi àll yi, yiy raam ak picci asamaan.
7Te dégg naa baat bu ma ne: “Jógal Piyeer, rey te lekk.”
8Waaye ma ne: “Mukk Boroom bi, ndax dara lu daganul mbaa lu araam masula dugg ci sama gémmiñ.”
9Waaye ñaareel bi yoon baat bi dellu ne ma: “Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.”
10Loolu am ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas lépp, jëme asamaan.
11«Ca saa sa ñetti góor, ña ñu yebal ci man, jóge Sesare, agsi ca kër ga ma dal.
12Te Xel mi ne ma: “Àndal ak ñoom, te bu ci werante.” Juróom benni bokk, yi fi teew, gunge woon nañu ma, ba nu dugg ca kër góor googu.
13Mu nettali nu ne gis na malaaka, feeñu ko ca këram ne ko: “Yónneel ca dëkku Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer.
14Dina la xamal ay wax yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”
15«Bi ma tàmbalee wax nag, Xel mu Sell mi wàcc ci ñoom, ni mu wàcce woon ci nun bu jëkk.
16Bi loolu amee ma fàttaliku li Boroom bi wax ne: “Yaxya ci ndox la daan sóobe, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi.”
17Gannaaw nag Yàlla jagleel na leen may, gi mu nu mayoon, bi nu gëmee Yeesu Kirist Boroom bi, man maay kan, bay tebbi àtteb Yàlla?»
18Bi ñu déggee loolu, amuñu dara lu ñu ca teg, ñu daldi màggal Yàlla ne: «Yàlla nag may na ñi dul Yawut it ñu tuub seeni bàkkaar, ba am dund gu wóor gi.»

Read JËF YA 11JËF YA 11
Compare JËF YA 11:2-18JËF YA 11:2-18