Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 11

JËF YA 11:14-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
14Dina la xamal ay wax yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”
15«Bi ma tàmbalee wax nag, Xel mu Sell mi wàcc ci ñoom, ni mu wàcce woon ci nun bu jëkk.
16Bi loolu amee ma fàttaliku li Boroom bi wax ne: “Yaxya ci ndox la daan sóobe, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi.”
17Gannaaw nag Yàlla jagleel na leen may, gi mu nu mayoon, bi nu gëmee Yeesu Kirist Boroom bi, man maay kan, bay tebbi àtteb Yàlla?»
18Bi ñu déggee loolu, amuñu dara lu ñu ca teg, ñu daldi màggal Yàlla ne: «Yàlla nag may na ñi dul Yawut it ñu tuub seeni bàkkaar, ba am dund gu wóor gi.»
19Ñi tasoon nag ndax fitna, ji amoon gannaaw Ecen, ñu dem ba diiwaanu Fenisi, ci dunu Sipar ak ca dëkku Ancos, di wax kàddu gi, waaye yemale ko ci Yawut yi.
20Moona amoon na ci ñoom ay niti Sipar ak dëkku Siren, ñu ñëw ci Ancos, ba seen wax law ci Gereg yi it, ñu di leen xamal xibaaru jàmm bu Yeesu Boroom bi.
21Te loxob Boroom bi ànd ak ñoom, ba mbooloo mu mag gëm te waññiku ci Boroom bi.
22Ba mbir ma siiwee, ba àgg ci noppi mbooloom ñi gëm ci Yerusalem, ñu yebal Barnabas ba Ancos.
23Bi mu agsee nag, ba gis yiw, wi leen Yàlla may, mu bég ci te di leen xiir, ñu wàkkirlu ci Boroom bi te dogu ci.
24Ndaxte nit ku baax la woon te fees ak Xel mu Sell mi ak ngëm; noonu mbooloo mu bare dolliku ci Boroom bi.
25Gannaaw loolu Barnabas dem ca dëkku Tars, di wut Sóol.
26Bi mu ko gisee, mu indi ko Ancos. Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm, di jàngal nit ñu bare. Te ci Ancos lañu jëkka tudde taalibe ya Gaayi Kirist.

Read JËF YA 11JËF YA 11
Compare JËF YA 11:14-26JËF YA 11:14-26