Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 11

Jëf ya 11:12-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Noo gi nag ne ma: “Àndal ak ñoom, te bul nàttable.” Juróom benni bokk yii ngeen di gis ñoo ma gunge, nu dem ba dugg ca kër Korney.
13Mu xamal nu ne malaakaa ko feeñu ci néegam, ne ko: “Yebleel ca Yope, nga woolu Simoŋ, ma ñu dàkkentale Piyeer.
14Dina la àgge kàddu yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”
15«Naka laa tàmbalee wax ak ñoom Korney, Noo gu Sell gi daanu ci seen kaw, na mu jëkkoona daanoo ca sunu kaw.
16Ma daldi fàttliku kàddug Sang, ba mu noon: “Yaxya, cim ndox la daan sóobe, waaye yeen, ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob.”
17Gannaaw nag Yàllaa leen jagleel genn may, ga mu nu jagleeloon, ba nu gëmee Sang Yeesu Almasi, ana ku ma doon, man, bay gàllankoor Yàlla?»
18Ba ñu déggee loolu lañu dal, daldi màggal Yàlla. Ñu ne: «Kon xeeti jaambur yi, ndeke ñoom it Yàlla may na leen ñu tuub, ba dund!»
19Gëmkat ña tasaaroo woon nag ndax fitna ja woon, ca mbirum Eccen, mujj nañu jàll ba diiwaanu Fenisi, ca dunu Sippar ak ca Àncos, waaye àggewuñu kàddu gi ñeneen ñu moy Yawut yi.
20Terewul ay gëmkat ñu dëkke Sippar ak Siren, bàyyikoo ca, dikk Àncos, wax ak làkk-kati Gereg yi, ñoom itam, ba àgge leen xibaaru jàmm bu Sang Yeesu.
21Boroom bi nag gungee leen loxoom, ba ñu bare gëm, waññiku ci Sang bi.
22Ba mbir ma siiwee, ba mbooloom gëmkati Yerusalem jot ca, dañoo yebal Barnaba ca Àncos.
23Ba Barnaba dikkee ba gis yiw, wi leen Yàlla may, dafa bég, di leen ñaax ngir ñu ŋoye seen xol ci Sang bi.
24Ndaxte Barnaba nit ku baax la woon, feese Noo gu Sell gi, ak ngëm. Mbooloo mu takku nag dolliku ci Sang bi.
25Ba loolu wéyee Barnaba jëm Tàrs, di seeti Sóol.
26Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu jëkka wooye gëmkat ñi ay gëm-Almasi.
27Ci fan yooyu la ay yonent jóge Yerusalem, dikk Àncos.
28Kenn ca ñoom, ku ñuy wax Agabus daldi yéglee Noo gu Sell gi, ne xiif bu metti dina am, ci àddina sépp. Te looloo nga yemook ayug buur bu mag bu ñuy wax Këlódd.
29Taalibe ya nag fas yéenee boole kem kàttanu ku nekk ca ñoom, ngir ndimbal lu ñuy yónnee bokki diiwaanu Yude.

Read Jëf ya 11Jëf ya 11
Compare Jëf ya 11:12-29Jëf ya 11:12-29