Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 10

JËF YA 10:8-37

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8mu nettali leen lépp, yebal leen Yope.
9Ca ëllëg sa, ba ñuy jaar ca yoon wa, ba jub dëkk ba, Piyeer yéeg ca kaw taax ma ci digg bëccëg ngir ñaan ci Yàlla.
10Noonu xiif dab ko fa, mu bëgga lekk. Waaye bi ñu koy toggal, Yàlla feeñu ko.
11Mu xool asamaan ubbiku, gis lu mel ni sér bu mag bu ñu téye ci ñeenti laf ya, yoor ko, mu jëm suuf.
12Boroom ñeenti tànk yépp ñu nga ca, ak yiy raam ci suuf, ak picci asamaan.
13Te baat ne ko: «Jógal, Piyeer, rey te lekk.»
14Waaye Piyeer ne ko: «Mukk, Boroom bi, ndaxte masumaa lekk dara lu daganul mbaa lu araam.»
15Waaye baat bi wax ak moom ñaareelu yoon ne ko: «Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.»
16Ñu def ko nag, ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas sér ba, jëme asamaan.
17Bi loolu amee Piyeer jaaxle lool ci lu peeñu miy tekki; fekk booba nit ñi Korney yebal, laajte woon nañu kër Simoŋ, ba agsi ci bunt bi.
18Ñu woote nag naan: «Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer, ndax fi la dëkk?»
19Bi Piyeer di rabal xelam ci peeñu ma, Xel mi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la wut.
20Jógal, nga wàcc te ànd ak ñoom; bul werante, ndaxte maa leen yebal.»
21Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngi nii, man mi ngeen di wut; lu doon seeni tànk?»
22Ñu ne ko: «Korney, njiitu xare ba, nit ku jub la te ragal Yàlla, ba am seede su rafet ci bànni Israyil gépp. Malaaka mu sell nag sant na ko, mu woolu la ci këram te déglu li ngay wax.»
23Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer jóg, dem ak ñoom, ànd ak ñenn ci bokk yi dëkk Yope,
24te bés ba ca topp mu dikk Sesare. Fekk Korney woo na këram ay bokkam ak i xaritam yi ko gëna jege, di xaar Piyeer.
25Bi Piyeer duggee nag, Korney daje ak moom, daanu ciy tànkam, sargal ko.
26Waaye Piyeer yékkati ko ne: «Jógal, man it nit rekk laa.»
27Noonu muy waxtaan ak moom, duggsi, fekk fa ndajem nit ñu bare.
28Mu ne leen: «Xam ngeen ne aaye nañu Yawut, mu jaxasoo ak ku mu bokkalul xeet, mbaa mu dugg ci këram. Waaye Yàlla won na ma ne warumaa ne kenn setul mbaa araam na.
29Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ñëw naa ci lu àndul ak werante. Maa ngi leen di laaj nag, lu ngeen may doye?»
30Ci kaw loolu Korney ne: «Ñetti fan a ngii may ñaan ci sama biir kër ci waxtu wii, maanaam tisbaar. Ci saa si ku sol yére yuy melax taxaw ci sama kanam,
31mu ne ma: “Korney, say ñaan nangu na, te say sarax egg nañu fa kanam Yàlla.
32Yónneel nag ci Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; mu nga dal ci kër Simoŋ miy wullikat ca wetu géej ga.”
33Yónnee naa nag ci ni mu gëna gaawe, woolu la; te maa ngi lay sant ci li nga ñëw. Léegi nag nun ñépp nu ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu lépp li la Boroom bi sant.»
34Noonu Piyeer jël kàddu ga ne leen: «Ci dëgg gis naa ne Yàlla du gënale,
35waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu.
36Yónnee na kàddoom bànni Israyil, di leen xibaar jàmm, jaarale ko ci Yeesu Kirist, miy Boroom lépp.
37Xam ngeen li xewoon ci réewum Yawut yépp, li ko tàmbalee ci diiwaanu Galile, topp ci waareb Yaxya, mu naan nit ñi, mu sóob leen ci ndox.

Read JËF YA 10JËF YA 10
Compare JËF YA 10:8-37JËF YA 10:8-37