Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 10

JËF YA 10:26-38

Help us?
Click on verse(s) to share them!
26Waaye Piyeer yékkati ko ne: «Jógal, man it nit rekk laa.»
27Noonu muy waxtaan ak moom, duggsi, fekk fa ndajem nit ñu bare.
28Mu ne leen: «Xam ngeen ne aaye nañu Yawut, mu jaxasoo ak ku mu bokkalul xeet, mbaa mu dugg ci këram. Waaye Yàlla won na ma ne warumaa ne kenn setul mbaa araam na.
29Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ñëw naa ci lu àndul ak werante. Maa ngi leen di laaj nag, lu ngeen may doye?»
30Ci kaw loolu Korney ne: «Ñetti fan a ngii may ñaan ci sama biir kër ci waxtu wii, maanaam tisbaar. Ci saa si ku sol yére yuy melax taxaw ci sama kanam,
31mu ne ma: “Korney, say ñaan nangu na, te say sarax egg nañu fa kanam Yàlla.
32Yónneel nag ci Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; mu nga dal ci kër Simoŋ miy wullikat ca wetu géej ga.”
33Yónnee naa nag ci ni mu gëna gaawe, woolu la; te maa ngi lay sant ci li nga ñëw. Léegi nag nun ñépp nu ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu lépp li la Boroom bi sant.»
34Noonu Piyeer jël kàddu ga ne leen: «Ci dëgg gis naa ne Yàlla du gënale,
35waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu.
36Yónnee na kàddoom bànni Israyil, di leen xibaar jàmm, jaarale ko ci Yeesu Kirist, miy Boroom lépp.
37Xam ngeen li xewoon ci réewum Yawut yépp, li ko tàmbalee ci diiwaanu Galile, topp ci waareb Yaxya, mu naan nit ñi, mu sóob leen ci ndox.
38Xam ngeen ne Yàlla fal na Yeesum Nasaret, sol ko Xel mu Sell mi ak kàttan; muy wër, di def lu baax ak di faj ñépp ñi nekkoon ci kilifteefu Seytaane, ndaxte Yàlla ànd na ak moom.

Read JËF YA 10JËF YA 10
Compare JËF YA 10:26-38JËF YA 10:26-38