Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 10

Jëf ya 10:20-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20Wàccal boog, ànd ak ñoom te bul nàttable, ndax man maa leen yebal.»
21Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngii; ki ngeen di seet, man la. Lu doon seeni tànk?»
22Ñu ne ko: «Njiitu takk-der ba Korney, ku jub, ragal Yàlla, te rafet seede bu ko xeetu Yawut wépp seedeel, moo jote ci malaaka mu sell, ndigalal woolu la këram, ngir déglu say kàddu.»
23Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer ànd ak ñoom, ñenn ca bokki gëmkat ña dëkke Yope gunge ko.
24Ca ëllëg sa Piyeer agsi Sesare. Fekk na Korney di ko séentu, daldi woo ca këram ay bokkam, ak xaritam yi ko gëna jege.
25Ba Piyeer duggsee, Korney gatandu ko, ne gurub ca tànki Piyeer, sujjóot.
26Piyeer yékkati ko, ne: «Déet jógal, man it, nit doŋŋ laa.»
27Piyeer di waxtaan ak moom, ba duggsi, yem ca nit ñu bare ña fa daje.
28Mu ne leen: «Yeen de xam ngeen ne ab Yawut, mayeesu ko mu jaxasoo ak xeetu jaambur, mbaa mu seeti ko. Waaye man nag Yàllaa ma won ne du kenn nit ku ma naan daganula jaxasool, mbaa setul.
29Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ma ñëw te tendeefaluma benn yoon. Ma di leen laaj nag li waral ngeen woolu ma.»
30Ci kaw loolu Korney ne: «Bëkkaati-démb ci waxtuw digg njolloor wii nu tollu tey, ci laa doon ñaane sama biir néeg. Mu am ku jekki ne jaas ci sama kanam, sol yére yu ne ràññ.
31Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla.
32Kon nag yebleel Yope, nga woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; ma nga dal ca kër meneen Simoŋ, wullikat ba ca wetu géej ga.”

Read Jëf ya 10Jëf ya 10
Compare Jëf ya 10:20-32Jëf ya 10:20-32