Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi - Esayi 11

Esayi 11:2-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2xelum Aji Sax ji tegu fi kawam, xelum rafet xalaat ak ràññee, xelum digle ak njàmbaar, xelum xam Aji Sax ji, ragal ko.
3Ragal Aji Sax ji lay safoo, du lu ko bëtam may rekk lay àttee, du lu ko noppam may rekk lay dogale,
4xanaa di àtte ku ñàkk ci njekk, di dogalal njub, néew-ji-dooley àddina. Mooy dóore àddina, bantub kàddoom, mooy reye ñu bon ñi, ngelawal gémmiñam.
5Njekk lay gañoo, takkoo kóllëre.
6Till ay bokk ak mbote ab dal, segg bokk akub tef ab tëraay, wëllu ànd ak gaynde gu mat, ak juru yar, tuut-tànk jiite leen.
7Nag ak rab wu aay di forandoo, seeni doom goorandoo, gaynde di lekk um ngooñ niw yëkk,
8luy nàmp di foye paxum ndox-suuf, perantal di laal tostanum ñàngóor.
9Deesatul gaañe mbaa di lore, fi mboolem sama kaw tund wu sell wi, ndax ni ndox di feese ba muur géej, ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.
10Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba, taxaw di raaya buy gindi xeet yi, xeet yi di ko sàkku, dal-lukaayam ba jagoo teddnga.
11Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom ñaareel bi yoon, ngir jotaat ndesu ñoñam, wa des Asiri ak Misra, ak Pattros ak réewum Kuus, ak Elam ak Sineyaar, ak Amat ak biir duni géej ya.
12Mooy yékkatil xeet yi raaya, dajale góor ña ñu dàqe Israyil, ak jigéen ña ñu jële Yuda, tasaare leen, ñu jóge ñeenti weti àddina, booloo.
13Fiiraangey Efrayim day jeex, njéefoy Yuda dakk, Efrayim dootu fiire Yuda, Yuda dootu jéppi Efrayim.
14Xanaa ñu ne coww ba sowu, ne jàyy cëppandoo fa kaw waggi Filisteen ña, waa penku, ñu sëxëtoondoo; Edom ak Mowab, ñu teg loxo; Amoneen ña nangul leen.
15Aji Sax jeey wowal walum ndox, ma séle géeji Misra. Mooy tàllal loxoom, tiimale dexu Efraat, wal kook doole, dóor ko, mu séddlikoo juróom yaari wal, mu jaarale ca nit ñu caraxu,

Read Esayi 11Esayi 11
Compare Esayi 11:2-15Esayi 11:2-15