Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Buur ya - 2.Buur ya 14

2.Buur ya 14:10-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Dëgg la moos, yaa duma Edom, ba tax nag sam xel jay la. Tee ngaa bàkku te toog sa kër? Te sax ana looy dugge ci jote buy indi ay wu lay daane, yaw, daanewaale Yuda?»
11Amaciya nag faalewul wax jooju, Yowayas buurub Israyil jóg; ñu jàkkaarloo mook Amaciya buurub Yuda, ca Bet Semes ga ca Yuda.
12Ba mu ko defee muy jéllu Yuda fa kanam Israyil. Waa Yuda tasaaroo, ku nekk ñibbi ca sab xayma.
13Yowayas buurub Israyil nag jàpp buurub Yuda, Amaciya doomu Yowas doomu Akasiya, ca Bet Semes. Gannaaw loolu mu dem Yerusalem màbb tata ja, la ko dale buntu Efrayim ba ca buntu ruq ba, muy ñeenti téeméeri xasab.
14Ci kaw loolu mu jël mboolem lu doon wurus ak xaalis aki ndab ca kër Aji Sax ja, ak ca dencukaayi kër Buur, boole ca nit ñu mu jàpp, daldi dellu Samari.
15Li des ci mbiri Yowayas ak li mu def ba ci njàmbaaram gi mu xareek Amaciya buurub Yuda, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
16Gannaaw gi Buur Yowayas saay, fekki ay maamam, ñu denc ko Samari, fa bàmmeelu buuri Israyil. Doomam Yerbowam falu buur, wuutu ko.

Read 2.Buur ya 142.Buur ya 14
Compare 2.Buur ya 14:10-162.Buur ya 14:10-16